(Ami Mbeng)
6i DOGAL YI MAKI SÀLL MUJJEE JËL ÑEEL MBAS MI
Njiitu réew mi, Maki Sàll, amal nab bàttale ci altine ji weesu, 29eelu fan ci sulet, 2020. 6i dogal yii ñoo gën a fës ci kàddoom yi :
Mbasum Covid-19 ñeel Senegaal : Waalo day gën di aay
LIMUB TAWATI COVID-19 BI
Lim bi dafa gën a yokku ci biir weeru sulet bii nu génn. Bees ko méngalee ak yeneen weer yi, 38i way-tawat yokk nañu ci téeméer yoo jël.
Naam, ci biir 100i way-tawat yoo jël, 60i yi dañuy wér. Waaye, loolu tekkiwul ne mbas maa ngiy wàññeeku. Ndege, limu way-tawat yi nekk ci diggante dund ak dee yokku na ba toll ci 295 te 121 yi gaañu nañ.
Dr Béey, njiitalu ‘’Samu national’’, aartu na nit ñi ci dayob wàllent bi nga xam ne, xayma na ko ci 41 ñeel 100 yoo jàpp. Mu teg ci ne, li sabab dee gu bare gi mooy ne, ñi ëpp ci way-tawat yi lott yi, dañu ame ay feebar yu bon yu deme ni jabetub ñaareel bi, tãsiyoŋ buy yéeg ak ndigg lu jagadi.
PEEÑANTALI COVID-19 BI
Pr Séydi dolli na ci bakkan bu mënatul a xeeñtu ak lewetug gémmiñ
Ca ndoorteelu mbas mi, doktoor yi sëqët su wow, yaram wu tàng, put guy metti, añs. lañ biraloon ne ñooy peeñantal yi gën a fës ñeel jàngoroy Covid-19 ji. Tey, mel na ni daa am yu ci dolleeku. Ci tënk bi muy faral di amal weer wu nekk te mu amaloon ko ci alxames jii weesu, Pr Séydi biral na 2i peeñantal yu bees : bakkan bu dul yëg xet ak lewetug gémmiñ. Mu ne, « bés bu Yàlla sàkk, dañuy seetlu yeneen xeeti peeñantal yees war a bàyyi xel bu baax. Lii di bakkan bu dul yëg xet, ñu naan ko « anosmie » ci nasaraan, ak lewetug gémmiñ, « agueusie », ci peeñantal yu bees yi lañ bokk. »
Waaye, nag, Pr Séydi daf cee teg ne, peeñantal yooyu, mënees na leen a fekk ci yeneen xeeti jàngoro.
TESTI COVID-19 YU GAAW YAA NGI ÑËW
Bees sukkandikoo ci kàdduy Dr Aamadu Alfa Sàll mi jiite ‘’Institut Pasteur’’ bu Ndakaaru, ciy fan yu néew, askanuw Senegaal dinañ mën a def ay test ci anam bu gaaw a gaaw. Dafa ne : « Liy bees ci caytug mbooloo maa ngi aju ci test yu gaaw yi nuy waaj a jot ñeel jàngoroy Covid-19 bi. Ndaxte, bu nu leen saytoo ba am ciy njeexital yu baax te dal xel, dees na leen natt cim mbooloo mu yem mees di lël ci béréb bu wóor. Loolu, nag, dinan ko def feek i fan rekk ; yàggatul dara. »
JURBEL
Ab ndongo buy jànge ca daaray ‘’Notre-Dame” moo ame jàngoroy Covid-19 bi
Ci ni ko kilfay daara ji xamlee, ndongo laa ngi tollu ci kalaasu CM2. Ñoom, nag, ci saa si lañu jël seen i matuwaay, daldi tëj daara ji.
Defalees na test ñi jot a jege ndongo loolu. Nee ñu yit, am na 2i mbokkam yu ame jàngoro ji. Waaye, xibaar boobu, kenn dëggalagu ko.
PÉNCUM RÉEW MI
Maki Sàll yabal na jawriñ yi ca péncum réew mi, ñu wuyuji dippite yi ba noppi fommaale seen bëru ren ji
Ci ndajem jawriñ mi amoon ci àllarba ji, benn fan ci sulet 2020, la Njiitu réew mi wax jawriñ yi ñu wuyuji dippite yi, tontu seen i laaj ñeel caytug mbas mi, rawatina 1000iy milyaar yees jagleeloon naalub Force-Covid-19 ñeel xeexub mbas mi.
Waaye, Njiitu réew mi yemul ci loolu ndax bi muy fomm guural geek déju bi mu làmboo, ci la leen yégalaale ne, ren, kenn ci ñoom du ci dem bër, liggéey rekk.
BEYKAT YAA NGI FIPPU
Ginnaaw beykati Ndengleer yiy jaamaarlook Baabakar ngom, boroom SEDIMA, waa Kër-Musa, Jendeer ak Puut ñoo ngi doon ñaxtu ci buntu dalub sàndarmëri bu Puut. Li waral seen mer gi mooy, ci seen i wax, dañoo nangu seen i tool. Ñi ëpp ci ñoom, lujum lañuy bey.
Nee ñu, dañ leen a jaay doole, foqati 350i ektaar ci seen i tool, jox kob poromotëer buy liggéeyal boppam. Waxatuñ dara, kooku génneb kayitu suufam, di leen ko xeexe.
UBBITEG AYERPOOR YI
Nguurug Senegaal jël nab dogal, tere roppëlaani Ërób yi dugg ci réew mi. Nguur gi dafay feyantoo ak kurél gi ëmb réewi Ërób yi, « Union européenne », ginnaaw bim jëkkee tere doomi Afrig yeek yu Senegaal ñu dugg seen biir i réew.
Jawriñu tukkib kow gi ak wërantal gi, Aliyun Saar, nee na : « Soo leen méngaleek Afrig, bari nay réew yu mu gën demin fuuf ci mbas mi. Kon, Afrig du nangu mukk ñu nuy sikkal ak a seexlu. »
Xanaa mooy liñ naan ‘’ku ma ko dabin, ma rókkin la ko !’’
Ami Mbeng