(AMI MBENG)

Yeneen i xët

Aji bind ji

 

Senegaal :   Yan njàngat la askan wi wara jukkee ci kàngam yu bare te ràññeeku yi génn àddina ci fan yii ? Ci diirub 40i fan   rekk, réewum Senegaal dëjal na fiy boroomi daraja yu fésoon lool. Li ci gën a doy-waar mooy ne dafa méngook jamono joo xam ne, réew maa ngi jànkoonteek mbasum covid-19 mi. Loolu, nag, war nanoo yee, nu xool naka lees di def ba ndaw ñi roy ci ñooñule réew mi ñàkk.

 KORONAA : Jawriñ biñ dénk kaaraange biir réew mi Aali Nguy Njaay, dina jàkkaarlook taskati xibaar tey ci àjjuma ji bu ñeenti waxtu ci ngoon jotee.

 BEYROUTH : Daanaka lu tollu ci 137i nit ñàkk nañ ci seen bakkan waaye tamit yeneen 5000iy nit am nañu ciy gaañu-gaañu.

 BEYROUTH : Nguurug Libaŋ dogal na ab guural ci diirub ñaari ayu-bés.

 COVID 19 : Ngir xeex mbas mi, Réewum Gàmbi jël na dogal buy xamle ne kenn waratul a génn këram. 

 JAPON : Sapoŋ a ngi baaxantal 75i ati bomb atomig ba Amerig sànni woon ca Irosimaa.

 AMERIG : Juróomi  doomi-Senegaal ñàkk nañu seen bakkan ci ab lakk bu amoon seen biir kër ca Denver. Pólis ubbi na fa ab lànket ginnaaw bi ñu njortee ne mbir mi du neen.

 KONAAKIRI : Alfa Konde la waa pàrteem tànn ngir mu mën a nekkaat lawax ci joŋante yiy ñëw, bu jëlee ndam li jiitewaat réewum Gine.

 BRESIL : Koronaawiris rey na kilifa aada gii di Aaritana, ñu gën koo ràññee ci xeex lépp luy yàq àllu Amazonie bi. 

 KËR-MASAAR : Sàndàrm yi teg nañ loxo lu tollu ci fanweeri nit ne ñàkkul ñoo fi taaloon meeri bu Kër Masaar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj