Gàttalug xibaar yi, Alxames 18 ut 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

 Siin

Lii nag ag lёngoo la gu jёm ci wàllum mbey ci diggante ñaari réew yii. Donte ne sax, àndug Siin ak waa Afrig du lu bees ndax mooy réew mi ёpp lu mu leen di sédd ay ndefaram ak lu muy bokk ci seen i sémb (projet) yi jёm ci wàllu xarala (industrie) mbey, añs. Ba tey, mooy réew mi Senegaal ёpp lu muy yóbbu ay meññeti (produits agricoles) mbeyam. Moo tax ñu taxawal ag lёngoo goo xam ne Li gёn a fés ci xibaari bés bi

PÓLITIG 

Taxawaayu Usmaan SONKO ci wotey 2024 yii di ñёw

Usmaan Sonko, Njiitalu pàrti PASTEF, ci ndajem-waxtaan mu mu doom amal ci alxamesu démb jii, biral na ci taxawaayam. Maanaam, xamle na ci ne lawax la ci wotey 2024 yii di ñёw. Te, nee na lu dul ndogalu Yàlla ak lu waa pàrteem bi nga xam ne ci ay càrt la tёnku dina bokk ci joŋante yooyu bu soobe Yàlla.

Paap Jibriil FAAL biral na péeteem

Ci ndajem-waxtaan mu mu doon amal Àllarba 17 ut biral na ci ne moom àndul ag Nguur. Maanaam, moom ci kujje gi la bokk. Farul fenn, àndul ak Masàmba, àndul ak Mademba. Ndax, moom nee na demul péncum ndawi réew ma ngir defaru waaye defar a ko fa tax a dem. Looloo tax, muy xàll yoonu boppam ànd ko ak kujje gi ngir soppi li fi nekk.

Dakkalug peyooru Seydinaa Omar TURE ginnaaw bi ko Bàrtlemi JAAS joxee ab liggéey ca meeri bu Ndakaaru

Ci ab saabal bu mu def mi ngi ciy xamle ne tey la def juróomi weer yu ñu ko fayul. Ndax nee na, ginnaaw bi mu xaatimee ag pas (contrat) ak ag Njiital meeri bu Ndakaaru Bàrtlemi JAAS la càmmug Senegaal (Etat) jёl ndogalu dakkal ag peyooram. Muy laaj nag, ginnaaw xew-xew yi fi jot a jaar yépp, lan moo waral coxorte ak xoqatal gi Nguur gi di def maxejj boo xam ne moo ko war a yiir, aar ko ?  

KOOM-KOOM

Ag lёngoo (walla ag ànd) (coopération) ci wàllum mbey diggante Senegaal akngir mu mucc ayib fàww ñu teg ko ci ay càrt yu leer ba mёn a doxal seen sémb wi. Te, lёngoo googu yamul rekk ci njaayum gerte añs., waaye dina dem ba laal yeneen i fànn.

TÀGGAT-YARAM

Joŋanteb ñi amagul fukk i at ak juróom

Gaynde yu ndaw yu Senegaal yi dañoo témboo ak waa Liberiyaa, réew mi nga xam ne moo amal  joŋante bi. Ku nekk ci ñoom dugal na ñetti bal. Lii nag di ab joŋante bu Union des fédérations Ouest-Africaines de Football bu ñi amagul fukk i at ak juróom. Ñoom nag, dinañ amal seen ñaareelu joŋante tey ci Àjjuma ji ak waa Siyeraa Lewon. 

Kàdduy Abdu Lahaad Jàllo

Ci ab waxtaan bu mu séqoon ak waa BBC Sport Africa feeñal na mébétam ngir àgg fu benn ékibu Afrig mёsul àgg ci joŋante boobu boole réew yi nekk ci àddina si yépp te mujjee jàll (qualifier) ci joŋante yi weesu (éliminatoires). Ndax, bees delloo tuuti ci mboor amul ékibu Afrig bu mёs a rombu quarts de finale. Te, moom jàpp na ne ni ñu ko defe woon ci joŋante bii weesu boole woon réewi Afrig yi ba jёl ko. Mёn nañ koo defaat ba jёl raw-gàddu gi (coupe) ca joŋante boobu. 

NJÀNG MI AK NJÀNGALE MI 

Merum waa SAES ci liy xew ca UASZ

Kurél gii di SAES (Syndicat Autonome de l’Enseignement Supérieur) mi ngi fésal am meram ci liy xew ci biir daara yu kowe yi rawatina ci jamono jii. Li ko waral nag mooy sóobare bi ñu jàpp fale ca daara ju kowe jees dippe Assane Seck nekke ca Sigicoor mu yor ag kartaabal gu def yàmbaa (chanvre indien). Ñoom nag, ñi ngi naqarlu njaayum yàmbaa mi ca béréb boobu. Ndax, dafa nekk mbir mu doy waar rax-ci-dolli muy xewe ci biir bérébu sàkkukaayu xam-xam ak tàggat ndawi ёllёg.

BITIM-RÉEW : tuuma yi Mali teg ci ndoddu Farãs

Diggante Mali ak Farãs dafa ñagas lool, rawatina ci fan yii. Ndax, ñii di waa Mali dañoo tuumaal waa Farãs ne ñooy jox ay xibaar ak ay ngànnaay ñii di rёtalkat yi (terroriste). Donte ne sax ñii di Farãs nanguwuñ benn yoon li Mali di teg seen ndoddu ndax, ñoom dimbaliwuñ gaa ñooñu muy ci lu nёbbu ak lu feeñ. Waaye, ñii di waa Mali ñi ngi artu, di woo tamit waa ONU ñu àddu ci mbir moomu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj