AMI MBENG
ABLAAY JUUF SAAR : « Li nu gën a seetlu mooy ne limu way-tawati Covid-19 day gën di yokku. Ndege, lim bi ful na 5i yoon bi mbas mi dooree ba léegi. 190i way-tawat lan amoon ca ndoorteel la, tey nu ngi ci 1115i way-tawat. »
SUDAŋ : Nguur gi jël na dogal buy méngale xarafal jigéen ak rey nit. Ñaar yooyoo bokk àtte léegi.
GINE–BISAAWO : Jàngoroy Covid-19 bi song na nguuru Gine-Bisaawo, ñetti jawriñ ñoo ko ame : njiital jawriñ li, jawriñu kaaraange biir réew mi ak jawriñu jiñ dénk wér-gi-yaram.
COVID-19: Nee ñu kenn ci sàndarm yiy aar Maki Sàll ame na jàngoro ji. Lëlees na naataangoom yi mu jot a laaleel walla jege yépp.
SIGICOOR : Lëlees na ca Kap-Skiriŋ ak Kafuntin 4i mool yu bawoo Sowaal.
FARÃS : Réewum Farãs wéyal na guuralug wér gi ba 24eel ci weeru sulet.
NDIMBAL : Kurél gi ëmb wàllu lekk ci àddina si (FAO) fas na yéene dimbali réew yi néew doole.
ËROB : Lu ëpp 1 milioŋu nit ak xaaj ñoo ame jàngoroy Covid-19 bi ca Ërob.
KONGO : Bànk bu mag bi jël nay matuwaay ngir dékku loraange yi mbas mi nar a jur ñeel koom-koom bi.
BERESIL : Nee ñu nit ñu baree bare ñoo nar a dee ci sababu mbas mi.
IRÃ NDAW : Komisaariya bu Ndaakaaru woolu na waaraatekatu Sentv bi. Ci li nu jot a fortaatu, dafa am ku ne da koo yoreel xaalis, mu kalaame ko pólis.