TUUBAA
Ki yore kàddug « Muxadimatul xidma » di Maxtaar Kan, mu ngi xamle ne « li wér te wóor mooy ne ab góor-jigéen kenn du ko suul Tuuba walla ci yeneeni sëgi jullit yi, sunu diine da koy aaye. »
KORONAAWIRIS
Gii Maryiis Saaña yedd na njiitu réew mi Maki Sàll ak jawriñu wér-gi-yaram u Senegaal, Juuf Saar, wax leen ne : « waruñoo tere ku daje ba noppiy wëlbatiku di ko def ñoom ci seen bopp… »
BÓOMUG JON LENON
Màrk Sapmaan mi reyoon Jon Lenon, ci 8eelu fanu desàmbar 1980, wax na li ko ko taxoon a rey : « maa rey Jon ndax dafa siiwoon lool sax, moo tax fu ma tollu dama daan wut ndam, ndax sama bopp rekk moo ma ñoroon …»
FUTBAL
Luwis Suwaares jóge na Bàrsaa. Dem na Atletikoo Madrid. Ba muy tàggatoo ak waa Bàrsaa, nag, démb ci suba si, ciy jooy la fa jógee.