Gii Maris Saañaa dal na ci kow Mari Xemes Njaay, jëwriñu wér-gi-yaram geek Ndimbalu njaboot gi. Dépite Yewwi Askan Wi ne, soxna si dafa dàŋŋaaral, maanaam day biral ag réy ciy waxam.
Ci xëtu Facebookam la Gii Maris Saañaa dugal ab yaxal, di ci ŋàññi Mari Xemes Njaay. Nde, keroog, jëwriñu wér-gi-yaram geek Ndimbalu njaboot gi dafa jaaroon Ngomblaan ga. Ca la àddoo ci mbirum way-tawat yi ame « insuffisancerénale ». Waaye, way-moomeel bi dafa jàpp ne jëwriñ ji « Dafa ñàkke kersa dépite yi ». Gii Maris Saañaa nee :
« …li ci gën a doy waar mooy ne ci anam bu ñaaw a ñaaw la wax ci way-tawat yi ame insuffisance rénale. Naka la jëwriñu wér-gi-yaram mën a xoolee way-tawat yi ame insuffisance rénale, di xeex ngir ñu gën a leen a toppatoo, wax leen ne sonnuñu ? »
Gii Maris teg ci ne :
« Sunu naataangoy réew yi ame insuffisance rénale dañoo sonn. Sonn nañu lool. Ci sababu pólitigu Njiitu réew mi, Maki Sàll miy luubal xaalisu saa-senegaal yi di ko jox njabootam ak i njaatigey tubaabam, sunu naataangoy réew yaa ngi dee ci suuf, benn benn. »
Moom nag, mi ngi digal jëwriñ, ne ko, bu amalul pexe way-tawat yooyu, naa maandu ci seen i mbir bañ leen a naqaral.
« Boo leen mënul fajal seen soxla, amoo yërmande, waroo leen ñaawal… »
Gii Maris Saañaa nee mi ngi xaar jëwriñ ji baalu àq.