Sóobare ba jiite réewum Gine-Konaakiri jamono jii, Seneraal Mamadi Dumbuyaa, jël na ndogal lu réy lol, lëmbe na Afrig ak àddina sépp sax. Ndax, dafa xaatim ab dekkare, daldi jéggal kii di Musaa Dadis Kamara, mu war a génn kaso ba.
Démb ci àjjuma ji, 28 màrs 2025, la xibaar bi jib. Kàppiten Musaa Dadis Kamara mi ñu tëjoon kaso ginnaaw bi ñu ko daanee, moom la Njiitu réew ma jéggal, féexal ko, mu war a ñibbi këram. Ndaxte, daf ko defal li nasaraan di wax “grâce présidentielle”, maanaam njéggalu buur bob, Njiitu réew kepp a am sañ-sañ bi. Ca seen tele nasiyonaal ba lañu dawal ndogal la ; ka ka dawal wax ne :
“Ci gaaralug Jëwriñu Yoon wi, jaglees na njéggalu buur kii di Musaa Dadis Kamara ngir sababu wér-gi-yaramam.”
Cig pàttali, kapiten Musaa Dadis Kamara a nekkoon ca boppu réew ma diggante 2008 jàpp 2010. Dafa foqati woon Nguur ga ginnaaw ba Laasana Konte faatoo woon ca atum 2008.
Moom nag, Kapiten Musaa Dadis Kamara, daaw (atum 2024) lañu ko daanoon ci tuumay pekkey niteef. Daan boobu, mi ngi aju woon ci layoob faagaagalub sàttumbaar 2009, ñu duppee ko ci tubaab “procès du massacre du 28 septembre 2009”.