Alxames, 1 fan ci weeru desàmbar mooy bés bi ñu jagleel xeex sidaa ci àddina si. Bés bi nag, dafa méngoo ak joŋanteb futbal bi dajale àddina sépp ca Qataar. Waaye tamit, bés boobu lees doon wote nafag njawriñu yoon gi ca Péncum ndawi réew ma, keroog, bi dépite bii di MasataSàmb(Yewwi Askan Wi) dimbej naatangoom Ami Njaay Ñibbi(Bennoo Bokk Yaakaar). Muy gàcce gu réy gu tegu ci ndoddu Senegaal te ñépp ñaawlu ko. Lu waral xeex bi ?
Ñaari fan ci ginnaaw, Ami Njaay Ñibbi dafa yëkkati ay « kàddu yu tegginuwul » jëmale leen ci Sëriñ Mustafaa Si Al Maktum. Noonu, Masata Sàmb di ko ñaawlu ci kanamu njiitu Péncum Ndawi réew mi, ndaw si ni ca tonet, ni ko « Maa tay ! ». Waa ji dox jëm ci moom, ni ko tar pes. Ami Njaay bëgg koo xaañ siis, Mamadu Ñaŋ dogale kook wéq ci biir. Ñaari ponkali góor di sot jenn jigéen, ndaw gàcce !
Waaw ndax góor ci dóor jigéen la mën a wone ngóoraam ?
Ak lu la jigéen mën a wax, mbaa mu def la ko, ak koo mën di doon, jigéen a la jur. Te bu dul dara sax, yor nga soxna, mbaa jigéen walla doom ju jigéen. Ndax xalaat nga su ko kenn mbejoon ci liggéeyukaayam mbaa di ko néewal doole ? Su booba de xanaa du yow miy mbej sa naataangoo bu jigéen yaa koy fajal. Li gën a doy waar mooy Péncum ndawi réew mi nga xam ni fa la ñuy wotee dogal yi war a dakkal metital jigéen, foofa la mbir mi ame. Kon war nanoo gën a tiit ci sunum réew bun demee ba kurpañ wuutu waxtaan ak wecce xalaat.
Li xew day màndargaal dellub ginnaaw demokaraasi Senegaal, di tilimal deram, di gàkkal xar-kanamam. Nit ku nite day jiital xalaat laata muy jëf. Xéy-na kenn dina ne Masata Sàmb daa meroon bi muy mbej Ami Njaay. Waaw, nit day ñag boppam ; nit moomul di dóore ni dof. Masata Sàmb ak Mamadu Ñaŋ, lu ñuy jàngal seen i doom ? Lii mooy seen ndono ? Aa, bàyyi nañ fi woy wu dul fey te di woy wu ñaaw. Wan weñ a leen cuq ba ñuy dóor jigéen ?
Ndegam, widéwoo yaa ngiy daw ci lënd gi, wër àddina, ñépp teg seen bët ci lu ñaaw lii, xanaa nag Pénc mi dina muri seen malaanu kiiraay ngir toppekat bi woo leen ba yoon mën a dal seen kow. Rey nañu, fii ci Senegaal, ay jigéeni jigéen te mujjagul fenn : Binta Kamara (Tàmbaakundaa), Faatumata Njaay (Pikin), Maryaama Saaña (Kër Masaar), Faatu Sàmb (Kawlax), Aysatu Siise (Medina Wàndifa) ak ñeneen ak ñeneen. Dafa doy, lu ñu yëkkati teg jigéen. Dafa doy.
Ñaari ndawi réew mii, li ñu def bu leen ci dara fekkul, su ëllëgee, bu jaasi mbaa fetal jógee ca Péncum ndawi réew ma, bu kenn ni bett na ko.