Dalu webub bennoog Afrig bii di “Jeune Afrique” moo yëgle ne njiitu réewum Mali mees folli fan yii weesu dafa feebar ba ñu yóbbu ko kilinig Pasteur bu Bamako. Nee ñu ab feebaru xol bu gaaw a ko dikkal ci talaatay démb jii. Am na ñuy wax ne feek i fan mu jël roppëlaan wutali réewum Dubaï ga mu tàmm di fajoo. Kolonel Asimbi Goita mi jiite tey Mali nee na mën naa dem fu ko neex, saa yu ko neexee. Ibrayim Bubakar Keyta dootul gone ndax am na 78i at waaye ñi ko seeti fa mu tëdd ca kilinig Pasteur nee ñu mu ngi am tan bu baax.