IMAAM AMAAT CAAM, IMAAM BU DËPPALE WOON DIINE AK JAMONO…

Yeneen i xët

Aji bind ji

Imaam Caam dafa gëmoon bu baax ne, àddina mooy aar allaaxira. Li lay tax a dugg àjjana, ci coobare Yàlla, àddina nga koy defee. Moo tax mu nekkoon ku yaatu, sawar ci yedde ak a yeete ak xam-xam bu géeju. Ni mu peegee woon làkk yi moom, leneen la. Wolofam dafa neexoon lool. Sooy dawal Ponki lislaam yi juróom (EJO-ÉDITIONS) danga naan su téere yépp meloon ni bii, daanaka kenn du réer ci diine. Téere la bob, day dimbali jullit bi dégg wolof, jàngul araab te bëgg a xam diine lislaam. Ci lu wér dangay xam diine lislaam waaye mbégte mi ngay jànge moo yéeme.

Ponki yi lislaam yi juróom wurus la. Imaam Caam ne woon it bind na téere ci wàllu séy ngir dimbali way-dencante yi ndax diggante yiy tas bari na ba jéggi dayo. Xéy-na tamit bàyyi na fi téere taysiir alxuraan ci wolof (mi ngi ci woon ba sori).

Lu jëm ci ndaw ñi : daa na wax : « nangeen sàkku xam-xam te bañ a jaamu alal ; alal boo ko jaamoo mu toroxal la».

Imaam def nay jéego yu am solo ci njàng ak njàngale ak tasaare xam-xamu diine. Taalifkat bu nànd làkkuw araab la woon ba bindoon ci ay téere ci wàllu ñaan ak tàgg Yonent bi (n.y.d.t).

Ku gëmoon làmmiñu wolof la woon te amoon ràññatle ; daa naa wax naan : « Yéen (EJO) a ngi def liggéey bu réy te buñ ci jàppoon na mu ware, dinanu def jéego yu soree sori ci wàll wi.

Li sunu gaa yi di puukarewoo njuumte lu réy la.

Ñu bari xàmmewuñu ku bari wax ak ku mën a wax ak ku xam.

Maa ngi ñaan Yàlla mu yee nu, nu xam li xew ba taxaw ci.

Man, diine laa xam, moo tax ci laay bind te diine mënut a ñàkk ci dundu nit ki. Ndax, nit su amul diine mook bàyyima ñoo yem. Li nit tanee rab mooy xam-xam ak mën-mën, nit day jàng, xam liy jariñ, indi ko ci Pénc mi, ñu jariñoo ko. Nit ku jàngul, amul mécce, li mu tanee bàyyima mooy mën a wax ak xalaat. Moo tax seen liggéey am na solo. Yal na ko Yàlla déggloo nit ñi te ñu jàpp ci. »

Dem na ak i mébét, lépp ngir dimbali jaam yi. Imaam Amaat Caam géeju xam-xam la woon. Su bindul woon bàyyi fi, nu ne « ag kàggu tàkk na ». Ndokk Yàlla ! Dëggal na li Ngiraan Fay wax ci Doomi golo bu Bubakar Bóris Jóob : « Nit dëgg mooy ki sottal ci dundam lu amal njarin askanam ». Imaam Caam kon, mënees na wax ne nit dëgg la woon.

Mu ngi ganee àddina Caameen Bàmbara ( Kawlax-Senegaal) atum 1945. Ci rakku baayam la jàngee alxuraan, jànge xam-xam diggante Medina Baay Ñas ak dëkk bu ñuy wax Batara. 1967 la dugg “Ecole Normale Franco-arabe” ba 1970 mu dem Tinisi defi “stage”. Bi mi ñibbisee Senegaal di jàngle ci lekooli nguur gi… Imaam Caam bokkoon na ci magi réew mi yenu mboor ak mbatiitu wooteb lislaam ci Senegaal. Ndakaaru la génnee àddina, amoon na 80i at.

Yal na Guyaar di këram ba fàww ! Imaam da daan wax naan tawfiiq mooy « sa bëgg-bëgg bi, ni nga ko bëggee, Yàlla defalee la ko noonu ». Yal na Yàlla defal ko njabootam ak bépp jaam. Yal na suufu Kër Majabel oyof ci kowam !

EJO-Éditions ak Lu Defu Waxu ñoo ngi leen koy jaal.

Ndey Koddu FAAL

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj