ISRAAYEL – IRÃ : JURÓOMEELU BÉSUB XARE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Juróomi fan ci tay, bi xare bi tàmbalee diggante Israayel ak Irã. Bees ci amalee ab taxaw-seetlu bu ndaw, mënees na ci jàngatee ay mbir yu bari ci fànnu pólitig ak lëkkaloog réewi àddina si.
Li mat a fàttali balaa dara mooy ne, 1979 ba tay, dañu àmbargoo Irã, teg ay daan ci fànn yu bari, rawatina ci wàllu koom-koom. Daan yooyu, Etaasini ak i digaaleem ñoo leen gàll ci ndoddu askanu Irã. Waaye, loolu taxul Irã nërmeelu.

Ñaareelu mbir maa di ne, Israayel moom, Sowu gépp a koy jàppale, di ko sotle ak a dooleel. Muy ci wàllu koom, ngànnaay, ba ci saabalukaay yi, ci anam yépp la réewi Sowu yi di taxawoo Israayel. Dafa mel ni, ñoom yawuut yi, ñooy caatu àddina si ba lu leen neex def, ku leen neex song. Nde, bi Israayel sosoo ak léegi, mi ngi wéy di noggatu julliti Palestin yi, di leen nappaaje ak a xoqatal, di nangu seen i suuf ngir noot leen, waayeet di leen ray ak a faagaagal. Te, loolu, réewi Sowu yee leen ciy dimbali, rawatina Etaasini. Mbir mi dafa niru naaféq.

Israayel moo song Irã, tooñ ko. Waaye, réew yi am doole yi, moom lañuy jàppale ci lu feeñ ak ci lu nëbbu. Nde, bi xare bi jollee ba léegi, ñoo ngi yót Israayel ay jumtukaayi xare, di leen dégtal ay dég-dég yu seen i way-yëddu taataan. Jàppale googu, Etaasini ak Àngalteer ñoo ci gën a fës.

Bu dee Irã, naam am nay digaale ak réew yii di Riisii ak Siin. Waaye, ni réewi Sowu yi di taxawoo Israayel, defaluñ ko Irã. Daanaka, Irã ci dooley boppam kepp lay sukkandiku ngir xeex ak Israayel.

Sóobarey Israayel yi dañu xareñ lool ci xeexub kaw. Ndaxte, dañu am ay roppalaan yu yees te mucc ayib. Loolu doyul, Israayel am itam ñu koy jàppale ci réew yi mu dendal te digaloog Irã. Mu mel ni Irã dafa wéet ci xare bi.

Wànte, ak lu muy wéet wéet, taxu ko xàddi walla muy yoxal. Nde, fu ko Israayel wokk, mu xuri ko.
Israayel a ngi dóor i misil ciy béréb ak i tabaxte yu am dayo fa Irã. Irã tamit di fayu, di ko sàndi ay misil balistig ak yoy xef-xippi yu bon. Moo tax it, Israayel yàqule na lu baree bari, rawatina bi mu doonee réew mu ndaw.

Ñu bare dañu xeeboon Irã, foogoon ne Israayel da koy taxañ, jàll ci keneen. Waaye de, am nañu mbetteel gu réy. Ndeke, li xare bi wane mooy ne Irã dafa am doole ci wàllu ngànnaay. Dafa di sax, bu réewi Sowu yi génnoon ci xare bi, dina soppi Israayel dóom ci simileek saala.

Xare bi nag dafa am lu mu wane : àddina si léegi, làmbi golo la. Jaayante doole ak nappante moo fi am. Kon, ku yeboo defaru, gànnaayu. Afrig, lii daf leen a war a yee, ñu fexe booloo, bennoo, jàppoo. Ndax kat, mbooloo mooy doole te xare bi firndeel na ko.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj