JAMÑAAJO : TAXAWAL NAÑU AG NDEFAR GUY LIGGÉEY AY BUNT AK I PALANTEER

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu bi, Sëriñ Géy Jóob, jiite na xewum ubbiteg ndefar giy liggéey ay bunt ak i palanteer fa Jamñaajo. Ci alxamesu tay jii, 13 oktoobar 2025, lees ko doon amal fa sowub Jamñaajo.

Ndefar googu nag, 583i miliyoŋ lees ko taxawalee. Boroom ndefar gi, Sëñ Omar Caam, moo ko xamle. Rax na ca dolli ne, loolu, ag tàmbali kese la. Nde, li mu nisër mooy yokk ko, yaatal ko ba ma njëg li àgg ci 1 miliyaar ciy seefaa. Bu ko defee, ndefar gi dina mën a defaraale ay tuwil yu PVC.

Jëwriñ Sëriñ Géy Jóob rafetlu na ubbiteg ndefar gi, wax ne dafa jotoon réew mi am ndefar gu ni mel. Ba tay ci kàdduy jëwriñ ji, amaana ndefar gi moo nar a liggéey bunt ak palanteer yees war a def ci 500 000iy dëkkuwaay yi Càmm gi bëgg a tabax.

Ndefar gi nag, « Darou Salam [Daaru Salaam] portes et fenêtres » la ko boroom tudde. Ci li Sëñ Caam wax, ndefar gi dina mën a liggéey limu 300i bunt ci bés bi.  Bu dee palanteer yi, lim baa ngi aju ci màcceer bees koy liggéeyee. Ba tay ci kàdduy Sëñ Caam, bu dee palanteeri almiñom, mënees na ci defar 100 jàpp 150 ci bés bi.

Dees na jël 80 jàpp 120i doomi Senegaal ngir ñuy xëy ci ndefar gi. Bu ñu defaree bunt yeek palanteer yi ba noppi, dees na jaay xaaj bi ci Afrigu sowu jant.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj