JÀNGOROY SËQAT SU BON SI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sëqat su bon si, jàngoro ju ñu mën a moytu la, te it lu ñu mën a  faj la. Cib doomu jàngoro bees dippe Mycobacterium tuberculosis lay jóge. Day faral di jàpp xëtëri nit ki. Nit ki ko ame, su sëqatee, mbaa mu tisóoli walla sax mu tufli ci ngelaw li, da koy wàll ay dendandoom. Ndaxye, ci ngelaw loolu lañuy noyyi. Kon jàngoro juy wàlle la ci biir nit ñi. Lu ni mel lañ seetlu ca biir Géejawaay. Nde, diggante saŋwiye jàpp oktoobar lañ gis ne lu toll ci 540i nit ñoo ame jàngoro ji.

Waa ASLUT (Association sénégalaise de lutte contre la tuberculose) a ngi dànkaafu, di xamle ne jàngoro jaa ngi law biir Géejawaay, Pikin, Yëmbël jàpp Kër Masaar. Ndax bu ñu dajalee ñi ko ame ñépp ci biir réew mi, téeméer boo ci jël, ñeen-fukk ak ñeent yi biir bãliyë bi lañ nekk. Moo tax ñu amaloon bésub ñaax askan wi ci jàngoroy sëqat su bon, biir Màrse bu bees bi nekk Géejawaay ci talaata 19 oktoobar. Elen Tàkko, bokk ci ñi féetewoo wàllum pajum sëqat su bon si ci dispañseeru Géejawaay, xamle na ne bés bi li ko tax a jóg mooy ñu gën a jël suñuy matukaay ci wàllum dem beek dikk bi, rawatina ci biir biis yeek njaga-njaay yi. Dañu seetlu ne, danqaloo bi fa lay ëppe. Foofu la jàngoro ji mën a jaar di law ba ëpp ñu doole. Te, tamit, gën a ñaaxaat askan wi ci wàllent jàngoro ji ak naka lañuy fagaroo, dina ci baax. Ci kàddu ya mu yëqati, mu ngi ciy xamle ne :    

« Dunu tàyyi mukk di ñaax askan wi ci jàngoroy sëqat su bon si. Ndax lu am fii ci biir Géejawaay te it moo ngi yokk rekk tëw a dakk. Li ci gën a doy waar mooy ne, dispañseer bi day tàmbale di faj ay way-tawat. Waaye, ñoom ci seen bopp ñooy dakkal paj mi, toogi seen i dëkk. Te, loolu, mën na leen indil ay gàllankoor ba ñu ñàkk ci seen i bakkan. Ñu ci bari ci ñoom ragluy Ruwaa Buduwe, Dalal Jàmm ak bu Pikin lañuy bàyyeekoo. Li ñu seetlu mooy ne way-tawat yu góor ñee ëpp yu jigéen ñi, te ñu bari ci ñoom a ngi am lu toll ci 17i jàpp 50i at ».  

Ci atum 2021, jëwriñu wér-gi-yaram ja woon, Abdulaay Juuf Saar, cim ndaje ma ñu amaloon ca weeru màrs ngir xeex jàngoroy sëqat su bon si ca Njaaréem, xamle woon na ne réew mi amoon na lu toll ci 13. 902i way-tawati sëqat su bon si, ak 452 yu ci ñàkk seen i bakkan. Xamle nañ it ne at mu nekk, Senegaal dina am lu ëpp 12. 000i nit yuy dox ak doomu jàngoro ji, te Ndakaaru lay gën a feeñe, ndax xaaj bi yépp fa la ñuy nekk.

Gannaaw ba jàngaro ji dafay faat bakkan, jot na ku nekk jël ay matukaayam ba mucc ci. Wolof nee na kat, fagaroo gën faju. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj