Naqar ak uw tiis la ndongoy jànguneb Gastõ Berse fanaane démb. Seen benn moroom moo ñàkk bakkanam. Ca biir néeg ba mu nekkoon, ca Village A, lees ko fekk mu tëdd, tàggook bakkanam.
Mataar Jaañ la ndongo li faatu tuddoon. Mi ngi doon jàng wàlluw Yoon ci banqaas bees duppee UFR SJP, bokkoon ci 31eelu maasi ndongoy UGB yi (promotion 31). Ci guddig démb ji, 10i fani féewiryee 2025, lañu ko fekk ca néegam, mu gaañu. Ca lañu woowee sàppëer yi ak takk-der yi, ñu gaawantu, dem fa mbir ma xewe.
Ba léegi nii, xameesagul lu sabab dee bi. Takk-der yi ubbi nañu ag luññutu ngir leeral ci yan anam la Mataar Jaañ ñàkke bakkanam.
Kurél giy wattu nekkiinu ndongo ya fa UGB, Commission sociale, génne ab yégle, di ñaan ndongo yi ñu teey te ànd ak dal, te bañ a siiwal i xibaar yu wéradi.
Geneen kurél giy sàmm aqi ndongoy UGB yi, di CESL, génnee na tamit ab yégle, fésal njaalam ba noppi dakkal njàng mi ci bésub tay jii, talaata 11i fani féewiryee 2025.