JÀPP NAÑ MEERU SINJAAN BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ceerno Jaañ, meeru Sinjaan bi, lañu jàpp tey ci àllarba ji. Jàllale nañ ko ca toppewaay (Parquet) ba. 

Emedia moo siiwal xibaar bi. Nee ñu sax, komandaŋu birigàddu sàndarmëri bu Popengin moo ko jëlil boppam, jàpp ko, yóbbu ko tirbinaal. Jamono jii nag, kenn xamagul lu tax ñu jàpp ko.

Cig pàttali, jotoon nañ ko fee jàpp ça weeru màrs 2022. Lees ko doon toppe mooy jëfandikoo këyit yu bon ci wàllu caytu, njuuj-njaaj ci koppar yu tollu ci 65i miliyoŋ FCFA.

Rax-ci-dolli, mësoon na jote ak waa Fondation Sonatel ñeel 2 700i pàkk yuy jar, lépp-lépp, 1,7 miliyaar. Jotoon nañ ko jàpp sax ci diirub weer. Waaye, ay kilifa diine ñoo ci waxoon ba ñu bàyyi woon ko bàyyig négandiku.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj