JÀPP NAÑU NDEELA MAAJOOR JUUF

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal Ndeela Maajoor Juuf moo lëmbe tey réew mi. Mollah Morgun mooy siiwal ci Facebook ay widéwoo yoy, dañ ciy wone ay xale yu tumurànke. Maanaam, soxna si dafa yor ay liir ak tuut-tànk ci këram, waaye, ci li widéwoo yi wone, toppatoowu leen ni mu ware. Na béréb ba mel tamit ci widéwoo yi, méngoowul ak dëkkuwaayu xale bu mucc ayib.

Coow li noon na kurr ci mbaali jokkoo yi. Nguur gi lañ duut baaraam ci li ëpp. Ñenn ñi sax doon nañ sàkku ci yoon mu def liggéeyam ngir aar xale yooyii balaa musiba di leen dal. Mu mel ni yoon dégg na leen. Ndax, Birigàddub kaaraange bu Yiirukaayu taax yi (Brigade de protection de la Sûreté urbaine – Su) jàpp na soxna si. Dakaractu moo siiwal xibaar bi. Lees koy tuumaal mooy mbugalum gune. Fi mu nekk nii, soxna saa ngi ci loxoy yoon.

Dees na ko topp…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj