Xew-xew bu tiis boobu, mi ngi am démb, ci gaawu bi. Ma nga ame fa Médina Baay, ay boori juróomi waxtu ca ngoon. Ab dal moo fa daanu ci kow ay doomi Aadama. Sàppëeri Kawlax yi ñoo leen doon wallu ngir rawale ña ca sonn ca raglu ya. Mu doon jéyya ju metti lool sax. Dafa di, am na kenn ci ñoom koo xam ne mujjul a mucc ci mbir mi Nde, dafa mujje ñàkk bakkanam.
Mu mel ni du guléet ñuy gis ay ndog yu metti ci réew mi. Waaye, jéyya ju ni mel néew na lu ñu ko fiy gis rawatina ci jamono jii. Ndax, kenn umpalewul ne nawet bi sori na. Ba tax na, taw yi moom wàññeeku nañu lool. Te, li ëpp ci xeeti jéyya yii moom, ay taw ñoo ko daan sabab. Waaye, wii yoon moom mel na ne demewul noonu.
Ndog mii am démb fa Médina Baay, tukkeewul ci daamar yi, ab taax moo ko sabab. Ndax, taax moo fa daanu ci kow ay doomi Aadama. Taax boobu, mi ngi nekk ci ginnaaw béréb bi ñuy amalee gàmmu gi. Jéyya jooju nag, senn soxna suy wuyoo ci turu C. Aañ moo ci ñàkk bakkanam. Soxna soosu mi ngi tolloon ci fanweeri at. Waaye, jéyya ji yemul rekk ci ay yàqu-yàqu ak bakkan bu rot. Nde, am na tamit ñu bari ñu ci jële ay gaañu-gaañu yu metti. Ñoom ñi am ay gaañu-gaañu, ña ngeen leen rawalee fa raglu Médina Baay ak “Centre hospitalier régional” bu El Haaj Ibraahiima ñas bu Kawlax.
Mu doon jéyya ju metti joo xam ne ba tey, kenn xamul lan moo ko sabab. Dafa di, kenn xamul ndax, ni ñu tabaxee taax yee jaarul yoon walla dañoo màgget. Donte ne sax, dara leeragu ci, ñu bari loolu lañu njort. Waaye, waa pólis ubbi nañu ci luññutu ngir xam lan moo sabab jéyya jooju.