Senegaal bëgg naa dalal ndajem Playoffs yu mujj yi
Menn ndaje a des ci juróom yees war a amal ci Playoffs yu FIBA yi ñeel joŋantey àddina si war a am féewiriye 2023. Ndaje moomu, nag, Senegaal daf ko bëgg a dalal. Muy lu ko mën a dimbali ngir mu mën a bokk ca ñay xëccooji kub bi. Waaye wéetul ci bile bëgg-bëgg.
Ginnaaw lajj yu metti yi mu lajjoon ca Esipt ba mu juraloon ko wàcc bu metti ba ci tàggoo ak tàggatkatam, ikib bu Senegaal bi yéegaat na bu baax ci toftale bi. Ñetti ndam yi mu am ci joŋantey ñeenteelu ndaje mi tax na ba mu delsi ci ñetteelu toogaan bi ci géewu E bi. Loolu tax na ba yaakaar judduwaat ci bokki ca ña nar a joŋanteji kub bi, lu ko dale 25i fan ci weeru ut ba 10i fan ci weeru sàttumbar 2023, ci diggante Sapõ, Endonesi ak Filipiin.
Yaakaar googu tax na ba waa FSBB bëgg a dalal ndaje mi mujj ci bokkadil yi. Baabakar Njaay mi ko jiite jot na ci a yékkati ay kàddu :
“ Bëgg nanu ko dalal. Jëwriñ ji tamit ànd na ci, jox nanu kàddoom. Waaye dégg naa Esipt ak meneen réew bëgg nañu ko tamit. Waaye lu mën a xew, jotoon nañu def séddale bi : Esipt dalal ci sulet, Tinisi ci ut, Senegaal ci Feewiriye 2023. Ñu amale ko fii ci Senegaal nag, nekkagul luñ yoonal. Waaye yónnee nanu bataaxal waa FIBA.”
Bu Senegaal di xëccoo ak yile réew kuy dalal mujjum ndaje mi, dafa fekk ni jeexalee Playoffs yi ci sa dëkk dafa doon lu am solo. Li ñu ci namm nag mooy ikib bi amal i joŋanteem ci Estaad bu mu miin, ànd ci ak i way-faram. Bu ko defee, ñu mën a gunge gaynde yi ñu dem ci ba jeex. Ndaxte, seen ub dem ca kub bu àddina si laaj na njureef yu baax ci moomu ndaje.
Cig Pàttali, juróomi ekib ñoo war a bawoo ci kembarug Afrig ngir bokk ca ñay joŋanteji kub bi. Ba fii, benn ekibu réew kott a jot a am tikkeem, muy bu Koddiwaar bi.