Kuréli maxejj yi àddu nañu ci « jub, jubal, jubbanti » bi Càmm gi woote. Ñuy sàkku ci Kilifa yi ñu xoolaat seen doxalin wi aju ci tere ay Saa-Senegaal ñu génn réew mi, walla di leen woolu ndax li nu yékkati ay kàddu jëme ci ñoom.
Ci ayu bés yii weesu, ñu bari ciy Saa-Senegaal, tere nañu leen ñu génn réew mi. Moo xam ay way-pólitig lañu, ay lijjantikat mbaa ay taskati xibaar. Li ko sabab nag, mooy « jub, jubal, jubbanti » bi Nguur gi woote. Nde, dafa tollu cib càmbar ngir képp ku laale ak moomeelu askan wi nga delloosi ko. Looloo waral ba mu tere ñenn ñi mu jàpp ni laale nañu ñu génn réew mi ngir bañ a daw. Am na itam ay Saa-Senegaal yu Yoon jot a woolu ndax li ñu yékkati ay kàddu yu ñu rafetluwul jëme ci kilifa yi, rawatina ci magum jëwriñ yi Usmaan Sonko.
Dafa mel ni nag, ñi fare ci askan wi te ñu leen di woowe Société civile ci farãse ànduñu ci wile wàll ñeel doxalinu kilifa yi ba tax ñuy sàkku ci ñoom ñu xoolaat ko. Bàrki-démb ci alxames ji, ñii di Aliyun Tin, Munjaay Siise, Abdulaay Fofana ak Baabakar Ba àddu nañu ci. Fekk jëwriñ ji Sã Baptist Tin doon leen dalal ngir waxtaan ak ñoom. Donte ni waxtaan waa nga aju woon ci wotey Ngomblaan gi, gaawantu nañu ngir waxaale ci.
Naka noonu, sàkku nañu ci jëwriñ ji mu xoolaat anam gi ñuy aayee génn réew mi te dàkk ci ñi yoroon Nguur gi laata ñoom. Donte ni ndogal lu leen Yoon jox sañ-sañ la, li ñu seetlu mooy ñi ñu ko teg ñépp a nga koy xame ca dalub roppalaan ya, bu ñu demee ba bëgg tukki bitim-réew. Ba tax ñuy sàkk ñu leen koy yëgal ca teel.
Yëgle boobu ñuy sàkku sax dafa di lu war, bees sukkandikoo ci Biraahim Sekk mi jiite kurélu maxejj gii di Forum civil. Ndax moom itam dellusi na ci wax ji. Ca ndajem tàggatu taskati xibaar yi ci lu jëm ci Pool Judiciaire Financier, ñu doon ko amal barki-démb ci àjjuma ji, la yékkati yile kàddu. Ci gis-gisam nag, tere nit mu génn réew mi lu yoon di rëdd la. Te ñiñ tere ñu génn ñépp wax nañu ni kenn yëgalu leen ko. Dañuy bëgg tukki, dem ba yegg fa dalub roppalaan yi, ñu daldi leen woññi. Naka noonu, mu jàpp ni Nguur gi war naa def ndànk ci loolu. Ndax ñi mu dal ñépp yegge nañu ko waa CEDEAO. Te loolu baaxul ci gis-gis bi ñuy am ci Bokkeef gi.
Andi nay leeral itam ci ni jubbanti bi mën naa am ci nu mu gënee jaar yoon, sàmmonteek tëralin wi. Ginnaaw loolu, moom Biraahim Sekk jàpp na ni sax Nguur gi dafa war a farlu ci mbir yi gën a tembare.
« Càmm gi dafa war a sëgg ci yi tembare yi. Fii mu tollu, danoo nekk ci réew mu nu war a jubbanti, dund gi yokku ba jéggi dayo. Woolu ay Saa-Senegal ndax li nu yékkati ay kàddu yoo rafetluwul, yaakaar nanu ni ci demokaraasi, génne ab yégle, ŋàññ kàddu yi nit yooyu yékkati doon na doy. Jarul di wékk demokaraasi Senegaal ci Yoon. »
Ci noonu, njiitu kurélu maxejj gii di Forum Civil dellu na woo Càmm gi ci mu xoolaat doxalinam, ànd ak dal te bàyyeek nit ñi seen sañ-sañub wax-sa-xalaat ak demokaraasi. Ak fu waay mën a bokk, dañ ko war a bàyyi mu wax xalaatam.