JURÓOM-ÑAARI TUUMA YEES GÀLL USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Usmaan Sonko kaso la jëm. Loolu la mbir yiy xeeñ jamono jii. Ginnaaw biñ ko jàppee démb, ci àjjuma ji, toppekat bokkeef gu doon na amal ndajem waxtaan ak taskati-xibaar yi ngir indiy leeral ci jàpp biñ jàpp njiitul Pastef li.

Bees sukkandikoo ci kàdduy Abdu Kariim Jóob miy toppekatu bokkeef gi, 7i tuuma lañuy toppe meeru Sigicoor bi. Ginnaaw tuumay càcc gu ànd ak taafar ak wooteb daaneel Nguur, toppekat bi dolli na ci yeneen juróomi tuuma. Daf ne :

” Lu tollu ci 40i bakkan yu rot diggante 2021 ak 2023 ñoo gàllu ci ndoddu Usmaan Sonko ci lu amum sikk. Njëwriñu bokkeef gi may teewal am na sañ-sañu toppaate… Looloo tax nu jël ndogalu doxal Yoon. Looloo tax itam mu [Usmaan Sonko] nekk ci loxoy Yoon jamono jii. Te dinañ ñu ko jébbal ci lu gaaw, ndax def nañ li ci waroon yépp.”

Bi mu waxee lii ba noppi, dafa indi tuuma yi ñuy toppe Usmaan Sonko :

” Dinañ ko toppe wooteb daaneel Nguur, mbooloom saay-saay, nasaxal kaaraangeg Càmm gi, jëf ak doxalin yiy sabab fitnay pòlitig yu tar ci bokkeef gi, mbooloom saay-saay yiy nas pexey rëtalkat (terorist) ak càccug këf.”

Bees sukkandikoo ci tuuma yees koy toppe, mënees na jàpp ne, ginnaaw ndéglu gi, dañuy dóor Usmaan Sonko “mandat de dépôt”. 

Waa Pastef bëggoon nañu waxtaan ak taskati-xibaar yi ,waaye takk-der yi dañ ñag seen màkkaan bi. Waa Yewwi Askan Wi, Aminata Ture, Xalifa Sàll, Baabakar Jóob meeru Cees, ak ñeneen, ñu ngi ñaawlu ak a naqarlu li ñu jàpp Usmaan Sonko. 

Ndaw ñi tàmbali nañu génn ci mbedd yiy taal ak lakk i póno ak ñoom seen. Ñoom ak takk-der yi sóobu nañ ci xeex bi. Lawagul nag. Waaye, njortees na ni, bu ñu bàyyiwul Usmaan Sonko ci lu gaaw, fitna ji dina yokku. Wii yoon fu muy yem ? Mooy laaj bi jaaxal ñépp. Moone de, jàmm a ngi doon xeeñ.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj