KÀDDUY ELIMAANU JËWRIÑ YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, yékkateeti nay kàddu jëmale ci Saa-Senegaal yi. Wile yoon moo ngi leen yékkati ci turu njiiteefu làngug pólitigam, Pastef. Muy xamal Saa-Senegaal yi ni xeex bi ñu doon xeex moo ngi sog a tàmbali. Muy xeex ngir génne leen ci buumu njaam, ñu moom seen bopp, am Càmm gu leer, réewu yoon ak yemale ñépp ci nees di séddalee koom gi. Xamal na leen itam ni, rawatina ñoñi làngug pólitigam, ne dinañu tàmbaliwaat doxal yittey làng gi, doore ko ci tëggaat ko.

Sëñ Usmaan Sonko biral naat ni moo ngi ci yoonu tukki bu mu namm a amal fa Gine Konaakiri, Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer ngir xeex bi Pastef di xeex ñeel bennoog Afrig (panafricanisme) ak moom-sa-bopp gu kembar gi. Naka noonu, dina dalal ci ayu-bés bii di ñëw waa làngu pólitig gii di Les insoumis, nekk Farãs, ci njiitalu Jean Luc Mélenchon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj