KAÑ LA COOWAL AJI SAAR AK SONKO DI JEEX ? 

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci talaata 6 desàmbar jii nu génn la Usmaan Sonko ak Aji Raabi Saar doon amal seen jàkkaarloo bu njëkk ci pekkug magum àttekat bii di Umar Maaham Jàllo. Coowal siif a dox seen diggante, kii di Aji Saar mooy tuumaal Usmaan Sonko njiital PASTEF ciif ak tëkku rey. Doonte jotoon nañ leen a déglu ku ci nekk ci benn boor, dafay jaadu jàkkaarloo am seen diggante, ak ñi ci laale ñépp ci pekkug magum àttekat bi ngir mu gën a leeral mbir mi.

Coow laa ngi bëgg a yàgg. Nde dem na sax ba soof saa-senegaal yi. Li leen naqari kay mooy bakkan yi ci jot a rot te taxul ba léegi coow li dakk, ñu xam fan la dëgg gi féete.  

Seen jàkkaarloo baa ngi tàmbali ay 11i waxtu ci suba, te def na diirub 6 jàpp 7i waxtu. Bi ñu génnee ci seen jàkkaarloo ba, farandoo Aji Saar yeek yu Usmaan Sonko yi sànni nañ ay kàddu ci ni mbir yi tëdde.  ku ci nekk a ngi ràcc di jëmale kanamam, te ku nekk a ngi jiiñ moroomam ne nanguwul tontu laaj ya fa rot. 

Ci kanamu taskati xibaar yi, Aji Saar nee na : 

« Dama rus, maa ngi doon xaar mu jàkkaarloo ak man wax lépp, waaye defu ko… Nanguwul wax, nanguwul tontu ci laaju layookat yi ndax amul ay firnde. Man nag, tontu naa laaj yépp. »

Elaas Juuf mii di layookatu Aji Sarr, moom it wax na ne :

« Usmaan Sonko nanguwul wenn yonn tontu ci laaju àttekat yi ak yu layookat yi. Bés bu nu àggee ca kërug àttewaay ga, bésub layoo ba, firnde yépp ay génn. »

Beneen layookatu Aji Saar bi, Abdu Jali Kan, jenn wax ji la wax, mooy ne Sonko nanguwul a tontu ci laaj yi ñu ko laaj. 

Ci geneen wet gi, layookati Sonko yi, ñoom, dañu bég ci jàkkaarloo bi. Waaye lenn rekk moo leen metti, mooy li Aji Saar tontuwul ci seen i laaj, ak pattaaral gi mu nekke woon. Te, moom Aji Saar, indi ay firnde ñeel ciif gi muy tuumal Usmaan Sonko. Looloo tax Useynu Ngom, kenn ci layookati Sonko yi, jàpp na ne : 

« Li nu gis mooy ne layookati aji-jàmbat ji, seen lépp cig pattaaral lañu ko teg. Loolu warul nekk taxawaayu aji-jàmbat, ndax waruñu yem. Tuuma yi bokkuñu, te sunu taxawaay warul yem ak ñoom seen bos. Ndax ñoom ñoo waxoon ne bés bu jàkkaarloo bi amee, firnde yépp ay génn. Nun gisunu dara… »  

Ndeyu-mbill gi di Usmaan Sonko tamit sànni na ci ay kàddu di xamle ne loolu du woon ab jàkkaarloo. Wax na yit ne :

« Ab xale bu jigéen bu jaxasoo, tiit, te xamul fu muy teg tànkam la jàkkaarloo woon, xale boo xam ne yëgul sax li ci tóoxidóona bi mu dugg. Lenn rekk laay wax, mooy ne xale bi bu amee ay kilifa, nañ ko gaaw jëlsi, lu ko moy ñi nekk ci ginnaawam di ko jay ak a dooleel ñoo ko nar a sàkkal pexe. »

Kon, mel na ne ba léegi làmb ji tasagul. Nde, léegi mu mat ñaari at. Lii mooy saa-senegaal yi dañuy xaaraat ndax yewweeguñu leen ci coowal Aji Saar ak Usmaan Sonko. Xéy na dañu bëgg a yóbbu coow li biir këri àttekat ya ngir taxawal ab layoo. Ak lu ci mën a nekk, na yoon def liy wareefam, mu bañ a ànd ak daraay par-parloo. Ndax bu ñu fàtte ne ay bakkan jot nañ rot ci coow li.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj