KAN LA NJIITU RÉEW MI NAR A DIISOOL ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Nees leen ko xibaaree woon, diisoo la Njiitu réew mi Maki Sàll wooteeti ngir jàpp bés bees war a amal wote yi. Ginnaaw ëllëg lees ko war a tàmbali. Waaye, 16i lawax ci 19 yi war a xëccoo njiiteefu réew mi xamle woon ni duñ ko teewe. Kurélu maxejj yeet lànk nañu.

Ginnaaw bi Ndayu Àtte réew mi neenalee dekkare bi Njiitu réew mi xaatimoon ba ajandi wote yi, Maki Sàll dafa biral ni nangu na ndogal li. Waaye, taxul mbir yi sotti walla xel dal. Nde, keroog bi muy janook taskati xibaar yi, àddina wërngal këpp a doon xaar mu ne ” bés sàngam la wote yiy am”, daldi leen àjji ni mu leen ajee woon. Waaye, defu ko. Diisoo la wooteeti ci altine jii di ñëw ak talaata.

Keroog bi mu nee dafay woote diisoo boobu la 16i lawax yi bokk ci 19 yi Ndayu Àtte mi nangul seen i wayndare ngir ñu bokk ci wote yi, fésal seen ñàkk ànd ci diisoo boobu, ñoom ak seen i nawle yiñ bokkal FC25. Ni ñu ko waxee woon itam nañ ko dëggalaatee tey. Xamuñu ku fay teew, waaye du doon ñoom.

Diisoo boobu nag, dafa gënatee teey xel yi. Nde, narul a yem rekk ci diisoo. Ndëgg-sërëx sax lay gën a nirool bees sukkandikoo ci 18i mbootaayi bokk-moomeel yi séq kurél gii di SOS/PAIX (Synergie des Organisations pour la Sauvegarde de la PAIX ). Moo tax, ñoom, ñu lànk ne duñ fa teew.

« Diisoo bi, ndëgg-sërëx la. Bu naree am ci anam yi mu daan amee, kurélu maxejj yi duñ ci bokk.» Rax-ci-dolli, « ñi ko séq bokkuñuy bëgg-bëgg, seen i bëgg-bëgg mëneesu leen a boole. Dañu sax féewaloo. »

Nees ko seetloo la amee. Bare Na lool ñu gàntal diisoo bi. Ba tax ñuy laaj kan la Njiitu réew mi nar a diisool ak fum jëm ak ñan ñoo koy wuyuji ? Ak lu mu ci mën a doon, kurél yi am na luñ rafetlu ci doxalinu réew mi. Lu deme ni ñi mu génne ndung-siin. Waayeet, ñoo ngi koy fàttali ni warul a fàtte seen i àq ak yelleef yees salfaañe.

Bu weesoo loolu itam, bu jàppul bés ba 2i fan ci weeru awril, dootul doon Njiitu réew mi. Bu boobaa, Ndayu Àtte réew mi lañ koy séqal. Te, dina def liggéeyam ni ko sunuy àtte digglee, tegaat réew mi ci loxo yi ko yelloo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj