KAN MOOY IDIRIISA SEKK ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ay fan a des ci wotey 24 màrs yi ñeel palug Njiitu réewum Senegaal. 19i lawax yi des ci xëccoo bi ñoo ngi wéy di wër réew mi, fu nekk ñu dige fa ngir askan wi am kóolute ci ñoom. Ñuy ànd ak sunuy dawalkat ci jaar-jaaru kenn ci lawax yi, kiy wuyoo ci turu Idiriisa Sekk.

Idiriisa Sekk a ngi juddoo Cees, ci atum 1959. Jàngee na ci réew mi ak ci jàngune yu kowe yi ci àddina si. Ñi ngi ko tàmbalee xam nag ci géewu pólitig bi, bi ko Meetar Abdulaay Wàdd, nekkoon fi Njiitu réewum Senegaal (2000-2012), defee Njiiteefu kàmpaañam ca atum 1988. Boobu amul woon lu dul 29i at. Atum 1995, mu nekk jëwriñu yaxantu bi ci Càmmug bennoo (gouvernement d’union nationale) gi Nguur gi taxawaloon ak kujje gi.

Ginnaaw gi, mu ànd ak Meetar Abdulaay Wàdd, di liggéey ciy tànkam, jege ko lool ba bi muy falu ci atum 2000, di ko fal jëwriñu Càmm gi. Ci weeru nowàmbar 2002, Meetar Wàdd def ko magum jëwriñ yi. Mu nekk fa ñaari at, di liggéey ak moom, laata mu koy dàq ci ne dafa ko bëgg daaneel.Waaye Meetar Wàdd dàqu ko rekk te yam ci. Nde daf ko toppaat ci yoon, ni dafa luubal alalu askan wi, lu tollu ci 44i tamñaret (milyaar). Ñu gën ko miis ci mbiri « chantiers de Thiès ». Ci lañ ko jàpp, tëj ko juróom-benni weeri kaso, laata ñu koy bàyyi ci setal (non-lieu).

Ak wotey 24 màrs yii di ñëw, Idiriisa Sekk moo ngi ci ñeenti wote yu tegaloo yu muy xëccoo Njiitu réewum Senegaal. Bi mu amee ay xaar-ma-yàlla ak Abdulaay Wàdd la ber làngu pólitigam, duppee ko Réew mi (Parti rewmi). Ci atum 2007 la njëkk a samp ndëndam ngir nekk Njiitu réewum Senegaal, daldi jël ñaareelu toogu bi, ci ginnaaw Meetar Wàdd. Bi ñu demee ba 2012, mu sampaat ndëndam. Waaye jegewul sax ndam li. Nde 5eelu toogu bi la jël. Loolu yépp taxul mu xàddi. Ndax, ci atum 2019, dafa delsiwaat ci xëccoo bi. Ci la delsiwaat ci ñaareelu toogu bi, ginnaaw Maki Sàll mi am ndam ñeel ñaareelu moomeem, donte ni sax nanguwul woon njureef yi.

Ci diggante bi, dellu na ànd ak Maki Sàll ci Nguur gi ci atum 2020, ci jamonoy mbasum Covid-19. Mu fal ko njiiteefu CESE (Conseil économique, social et environnemental). Loolu taxoon na sax ba yenn jàngatkat yi ne gis ni moom moo nar a doon lawaxu Bennoo ci wote yi, ngir wuutu Maki Sàll. Waaye, bi mu demee ba ci weeru Awril 2023, ci la tekki ndombog-tànkam. Naka noonu, mu biral ni dafay nekk lawax ci wotey 2024 yi. Ni mu ko daan waxee ni xel xalaatul ay wote di am Senegaal, mu nekk fi, ni cocc te du ci bokk.

Wile yoon kon di ñeenteel wi yoon muy yóotu ndombog-tànk gi gën a kowe ci réew mi. Moom ak i ñoñam jàpp ni mooy Njiitu réew mi Senegaal soxla ci jamono yii mu nekkee ci guddi yu bët setagul. Ndax mooy lawax bi jaar-jaaram gën a gànjaru. Nees ko seetloo ci lawax yu bare, mënees na tënk naalam ci nit, koom-koom ak gox yeek gox-goxaat yi. Fàttewul itam jëflante beek bitim-réew, rawatina déggoo yi réew mi séq ak réewi Afrig yi ak jéego yi mu ci namm a dox, njëkke ko ci bennale xaalis bi fi Afrig sowu-jant.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj