KAN MOOY XALIFA SÀLL ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xalifa Sàll, nitu pólitig la, fës lool fi Senegaal, di lawax ci wotey 2024 yees dëgmal. Moom Xalifa, mi ngi juddu keroog 1 panu sãwiyee 1956 fa Luga. Mu ngi bokkoon ci làngug “Parti Socialiste”, gàttal biy joxe PS. Tey, moo jiite kurél gii di Taxawu Senegaal, di lawaxu lëkkatoo « Khalifa Président ».

Bu dee ci wàllu jaar-jaar, mënees na tënk, wax ne, moom Xalifa Sàll, daanaka Njiitu réew kese la nekkagul. Ndax, muy ci Nguur gi walla yeneen i béréb, sëñ bi Sàll yàgg jot takk ndomboy-tànk yu bari, jaar fu bari. Ndax kat, bi Xalifa Sàll di sóobu ci pólitig, am nay lawax yu muy xëccool tey yoo xam ne, booba, duggaguñu sax lekkool. Kon, bu yeboo ne, màggetum pólitig la.

Ca atum 1993 lees tabboon Xalifa Sàll ci Nguuru Abdu Juuf, def ko jëwriñ ju toftalu ci elimaanu jëwriñ ja woon, Abiib Caam. Moom moo resoon fànn wees duppee ci farãse « Relations avec les institutions », maanaam, ci kàllaamay Kocc, jokkalanteg campeef yi. Ndombog-tànk boobu, takk na ko ba atum 1998. Ba tey ci wàll njëwriñ gi, nekkoon na feet jëwriñu yaxantu beek ñeeñal gi (ministre du commerce et de l’artisanat) dale ko 1998 jàpp 2000, at mi PS di ñàkk Nguur gi.

Xalifa Sàll nekkoon na fi tamit dépite ci diirub fukk ak juróomi at. Maanaam, jot naa am ñetti moome fa Ngomblaan ga : diggante 1983 ba 1988), 1988 ba 1993 ak diggante 2001 ba 2007.

Diggante 1996 jàpp 2000, Xalifa Sàll a nekkoon meeru Yoof. Nekkoon na tamit tofu meeru Ndakaaru diggante 1984 ak 2001. Atum 2009 la nekk meeru Ndakaaru ba ni koy wàccee ca atum 2018 ñeel coowal « Caisse de dépôt » la woon. Dafa di, Nguurug Maki Sàll gi daf ko tuumaaloon ag luubal, maanaam dañ wax ne dafa dëpp keesu meeri bu Ndakaaru. Ca lañ ko àttee, daan ko, tëj ko kaso, tere koo bokk ca wotey 2019 ya. Ginnaaw gi la ko Maki Sàll faral tuuma yooyii, delloo koy àqi maxejjam ba tax ko bokk ci wote yii nu jëm, dibéer 24 màrs 2024.

Bu dee ndomboy-tànk yu jéggi digi réew mi, dees na ci fàttali kurél gii di « Cités et alliances » gog, moo ko jiite woon. Jiite woon na fi tamit mbootaayu meer yi ci réew yiy farãse ci àddina si, maanaam « Sécrétaire général des Associations Internationales des Maires Francophones », gàttal biy joxe AIMF.

Kookoo di Xalifa Sàll miy dagaan tey baatu réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj