Film bi Kati Leena Njaay (sottalkat) mujj génne te tudde ko Koppar, sañ-sañ, mboorum FCFA, la doon aajar démb ci àllarba ji (24eelu sãwiyee 2024) ci sinemaa SEA PLAZZA, Ndakaaru.
Li waral film bii, ci kàdduy Kati Leena, dangay dal ci baat, xalaat walla xew-xew bu yee lenn ci yow, nga ne lii jar na def film walla yu mel nii. Looloo ko dal ci mbiri sox bii di FCFA. Bi mu nekkee gone, ca Ndar, maamam ju jigéen da ko daa may xaalis bu sew, mu jënd ci tàngal ca bitig ba. Waaye, xaalis du jënd rekk lay jariñ…
Kati Leena dafa nettali ne, bés, da doon waxtaan ak Thierry Amougou, xam-xamam màcc ci koom, mu ni ko « mbirum FCFA daal pataas bu tàng bees di awante la bu kenn nanguwul a jàpp ».
Loolu ub boppam, mu ni fàww mu gëstu naka lay sox bi di doxe dëgg-dëgg. Nii la film bi cosaanoo.
Soxna si Njaay dafa tàllal ngolliiram (mikóro, waxukaay) ay boroomi xam-xami koom yu mel ni Felwiin Saar, Ndongo Sàmba Silla, Kako Nubukpo (Togoo), Martial Ze Belinga (Kamerun), Lionel Zinsou (Beneŋ) ak Abdulaay Bàccili, Mamadu Lamin Lum ñi fi nekkoon jëwriñ ak njiitul jëwriñ, taataan seen i xalaat ci FCFA. Ku seetaan film bi dinga ci jànge lu bari. Ndeke sox (xaalis), ku ko moom yaa moom sa bopp. Ndaxte, su boobaa dinga am sañ-sañu di def aka dindil sa bopp. Ñàkk a moom sa koppar, muy jóge feneen, pertmaa bu réy la cim réew te da koy delloo ginnaaw. Lii la Tubaab yi xam bu baax a baax ba tax mu jaral leen lu nekk ngir réew yu mel ni Senegaal di wéy ci FCFA. Dafa di, « fileek réewi Afrig yaa ngi jëfandikoo sunu làkk ak kopparu CFA, sunuy diggante day gën di dëgër ». Te, diggante Tubaab ak Nit ku ñuul, weesuwul Tubaab di leen sàcc, jéem a nax ak di leen yàqal.
Bu loolu weesoo, njjiti réewi Afrig yu njëkk ya, ginnaaw seen ug jonn, wone nañ seen xalaat yu safaanoo ci film bi, ku mel ni Léopold Sédar Senghor (Senegaal), Félix Houphouet Boigny (Koddiwaar) ak Gnassimgbé Eyadéma (Tógoo).
Liggéey bi jëlal na soxna si Njaay 7i at yoo xam ni mi ngi doon wër i xibaar fépp fu mu ko yaakaar. Mu feggoo ceek ay naataangoom, ay nataalkat, jàngalekat, gëstukat, mboorkat ak képp ku ci loxoom war a dugg, ci gàttal. Ci biir gëstu yooyu la soxna si dajeek gone gu doon yëkkati taalifu Jean de La Fontaine bu siiw bi mu tudde Le laboureur et ses enfants maanaam Beykat bi ak i doomam. Njàngat li ci taalif bi mooy ne, ku ñaq jariñu ; waaye tamit ndono kenn du ko jaay, dees ko war a fonk. Kati Leena nag, moom jàpp na ni taalif bii di léeb wutewul dara ak kopparu CFA gi xam ne ay naxee-mbaay la. Waaw, ndax ndono loo xam ni lii naxi kese la dees na koy sàmm ? Ndax wéy ciy nax du weneen turu dellu ginnaaw ? Ak lu mënti am, li Kati Leena Njaay jublu woon ci film bi mooy mu jur ay laaj ak i xalaat ci nit ñi.
Film bi gudd na, ndax ëpp na waxtook genn-wàll. Waaye, solo si mu ëmb tax na doo ko yëg. Rambaxul tamit, mbuug mi xaw na géey, tayeef la nag ; xéy-na li wolof naan « xaalis àndul ak coow » moo tax. Amul it jenn jigéen joo xam ni jii Kati Leena Njaay laaj na ko lu mu xam ci mbiri koppar, kon mënees na ni filmu góor la. Ndax tayeef la am déet ? Su ëllëgee dinaa ko laaj lu ko wund.
Kati Leena Njaay fàttali na ne, moom sottalkat la ; li ko gënal du faram-fàcce, waaye mooy nettali. Joxe kàddu mooy liggéeyam, bëggul dugg ci werante mbiri koppar, FCFA, ndax daa bari jafe-jafe, yombul doonte mi ngi laaj yaayam ak tamit mbooloo mi ay laaj yu jëmoon ci dooley xaalis bees wàññi, kopparu ëroo añs.
Mbooloo mu takku teewoon na fa. Taskatu-xibaar bii di Umi Nduur a doon séddale kàddu, moo féetéwoo woon wàllu jokkoo bi ci film bi. Séllu Jàllo, di jàngalee Iniwérsite Gastoŋ Berse, moo jiite woon waxtaan wi ak Kati Leena ngir i leeral ñeel doxalinu film bi. Ci mbooloo mi it ñu demee ni porofesëer Magéy Kase, Adiriyeŋ Jóob taskatu xibaar bu mag te siiw. Baaba Jóob ak ñeñeen yëkkati nañ fa kàddu, ndokkeel Kati Leena, ba noppi am luñ ko yokk mbaa laaj. Ràññees na fa tamit ñu deme ni porofesëer Buuba Jóob ak Cerno Siise, Jaalo Jóob, Usmaan Wiliyaam Mbay, Fabakari Kóli, Abubakar Demba Siisoxo, añs.