KÀTTEY BFEM 2024

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, ci altine ji, door nañu kàttey BFEM 2024 bi. BFEM (Brevet de Fin d’Études Moyennes) bi, mooy kàtte (walla lijaasa) yiy tëj xaaj bu njëkk ci njàng mu digg-dóomu mi fi réew mi. Bu atum ren ji nag, limub lawax yi dem na ba ci 191 362i ndongo. Dinañu ko def ci àppu 3i fan (22, 23 ak 24i pani sulet 2024) ci mbooleem 1 155i barab yi leen di dalal (centres d’examen).

Sëñ Mustafaa Màmba Giraasi (jëwriñu jàng mi) yékkati na ciy kàddu ngir dalal xeli lawax yi. Mu leen di xamal ni lépp yemb na. Jël nañu matukaay yi war ngir ñu mën koo amal ci anam yu mucc-ayib. Muy sàkku itam ci lawax yi ñu sàmmonteek sàrt yi te bañ a yóbbaale seen i jollasu yi ci barabi kàtte yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj