ÔGinnaaw-ëllëg, dibéer 4i pani ut 2024, lañ jagleel garab fépp fi réew mi. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dina dem fa Tuuba ngir jiite ubbiteg bés bi.
Bu 10i waxtu jotee ci yoor-yoorug dibéer ji la mbir yiy door. Ren mooy tollook 41eel wi yoon ñuy màggal njëmbëtug garab fi réew mi. Wëppa bees jàppal bés bi mooy : « Solos njëmbëtug garab ci moom sa dund ak yokkuteg koom-koom ». Njiiteefu réew mee ko xamle. Te yit, moo yégle ne Njiitu réew mi dana teewi Tuubaa, ubbee fa bés bi. Nee ñu : « Xew-xew bile, mooy màndargaal tamit ubbiteg naalu njëmbëtug garab fi réew mépp. »
Ñaari fan rekk ñoo ci des. Waaye, waa Tuubaa moom sóobu woon nañ ci waajtaay yi bu yàgg. Dafa di, fi mu tollu nii, noppi nañ ngir dalal fa Njiitu réew mi ci anam yu mucc ayib. Ka ñu dénk caytug xew-xew bee ko xamle. Moom, liyatnaa-kolonel Móodu Juuf, moo jiite banqaas bi féetewoo njëmbët geek wattug ndox yi yeek suuf yi. Biral na ne lépp yemb na te dina jaar yoon.