Bindal sargal ku génn àddina, damay koy def. Waaye de, lu ma diis la, tiis ma. Ndaxte, loolii, day firndeel ni nit kookii ko waral, dëddu na ba fàww, te du dellusi. Mukk ! Ndeysaan, Ken Ndóoy dem na, dootul delsi. Dee du jaas, waaye demiin mën na rafet, bañ a metti. Bakkan bu ñam, dund, ñam dee. Dëgg la, deesu ko weddi. Wànte, ni sutura baaxee ci dund, noonii walla nu ko raw la baaxee ci nit ki faatu. Ay waay ! Lu tee woon ngeen sàmmal Ken Ndóoy suturaam ?
Soxna sii dawkat bu siiw la woon ci àddina si, jox léppam réewam. Fu nekk, dawal na fa Senegaal, biral fépp raayaam bi. Fukki yoon ak ñett, muy indil Senegaal ay raaya yu jóge ci Afrig ak Tugal. Daw naa daw ba xoox, tëb a tëb ba lompañ. Mu jaare ci feebar, Senegaal dummooyu ko.
Yàggul dara, jàmbaar ji def ab widéwoo, di sàkku ci nguurug Senegaal ñu fey ko liñ ko yoreel ndax mësta jot dërëm bi gën a tuuti jëm ci peyooru ku am raaya yu ni tollu. Feebar na ba sonn, amul ndimbal, amul lu mu fajoo. Moone njawriñu tàggat yaram mi ngi fi, njawriñu jigéen ak njaboot waxi-noppi. Ken Ndóoy, ak ni mu yàgg a tekkee, ba muy tuut, amul lu dul fukki at juróom-benn, la jëkk a sagal Senegaal, indil ko raaya bu mag. Ku ni mel kat, beneen taxawaay moo jekkoon ci jëmmam. Te, ci kow loolu rekk, waroon nañ joxe royukaay ci xale yi, di jigéen teg ci. Waxuma la faj, sargal, sagoo, waaye waroon nañ ko boole ci kurél giy yëngu ci tàggat-yaram, rawatina daw. Waaye dara. Seetaan ko, sàgganee ko ba mu faatu.
Bu jotoon ci xaalisam ba mu waree, mu lew ko domm, dina faju ba keroog Yàlla di def li gën te kenn du ko xamal. Faju, fajul dee naam. Waaye, dinay yombal waaj. Senegaal, nag, dunu faj sunuy way-feebar, waaye dinanu leen dëjal. Lu ci gën ?! Di fàttali ni Ken Ndóoy mi ngi juddu ci atum 1978. Xajaatoon na fi.
Lu Defu Waxu mi ngi jaal njabootu soxna Ken Ndóoy, di ñaan Yàlla may leen xolu muñ te soxna si àjjana di këram ba fàww.