KËR ARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Seeti naa soxna Aram Faal Jóob, ndaanaan

Jàmbaar la,  lingeer dëggantaan

Dama ko ni jàkk sama yaram di daw

Mu siggi xool ma, mbaaru bëtam jëm kaw

Mbégte mu réy di rogalaat

Fépp ci sama xol di gundaandaat

Aram ca dal ga, baat bu sedd ba, yiw ga

Bari xam-xam bu wér, Aram ca oyof ga

Taxul mu réy bay dox di fëgg dënn

Waxumalaak di wone maa mën

Xëccul benn cër

Jox na ñépp cër

Ne ci li ko war

Fonk ñi ko wër

Du xaste, du tuutal kenn

Doylu na, xëccoowul lenn

Kii a mat a delloo njukkal di sargal

Kii a mat a wone nde dafa noo sagal

Wet goo làmb Aram Faal muy royuwaay

Jàng na ba mat wéeruwaay

Lijaasa yu kowe la am

Teewu koo yor këram

Di sàkku ngërëm

Yar njabootam ci diine ak amal njariñ askanam

Firnde li mooy ay ndomb-tànk terewul jigéen

Doon jigéen matal li ko tax a doon jigéen

Aram fàttewul ni lees mën a tere gan

xool ak dégg bokku ci, moo mën gan

wax na, nu dégg, lépp rafet na

won nga nu, nu gis, lépp rafet na

kii mooy saa-Senegaal bu jan

bari teggin, mën a teral gan

« Mag mat naa bàyyi cim réew »

ku mel ni Aram a gën cim kéew

ndax xam-xamam ak yiwam

jikkoom yu rafet, am leen a di ndam

Aram Faal Maali- Kumba mii may woyal

Xamal ni jëmm ji rekk daara la

Mën i téere, nitee ma ko gënal

Ku ko seeti gis ni dara la

Soxna Mari Mbow, xam na li ma wax

Sëñ Faliilu Njaay du weddi lii ma wax

Ibraayma Lóo, seedeel lii ma wax

Aamadu Njaay gëm na lii ma wax

Baakari Saar, gis na lii ma wax

Senegaal ameel na la njukkal

na say may di baawaan, Faal, dundal !

Ndey Koddu Faal

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj