LU DEFU WAXU, seen yéenekaay ci kàllamay Kocc, mi ngi am mbégte dalal fii tey, Soxna Faatu Siise Kan, jàngalekatu wolof ca Almaañ. Soxna si Kan, doomu Senegaal la, juddoo fi, yaroo fi, màggee fi, dooree fi am njàngam ba am DEA, ca 2012. Ginnaaw gi, at ma ca topp, mu tukki Almaañ. Foofa la féete, di fa jàngale jonni-Yàlla tey jile. Jamono jii mu ñëw Senegaal ngir bër, nu daldi koy koj, séq ak moom waxtaan. Jotoon nanu leen dégtal pàcc bu njëkk bi. Tey, danu leen di dégtal pàcc bu mujj bi.
DFW : Ban xeetu liggéey ?
FSK : Dama bokkoon ca ña daan waxtaan ak ña daan xoolsi nataali saa-Afrig ak i jumtukaay (objets) yuy wane seen dundiin. Ginnaaw doomu Afrig laa, xam naa li nekk dëgg ci sunu xayte ak sunu mbatiit. Ma daan ko faram-fàcce. Lii moo ma gënoon a soxal. Ñu bare ñoo fa daan ñëw. te, yenn saay, ñooñu, da leen iy gënal ñuy waxtaan ak kippaango gi ma bokk.
Kàggug cosaan bi amoon na tamit kàggug téere gees jagleel bindkati afrig yi. Danga fay fekk téerey Bubakar Bóris Jóob, Ngugi Wa Thiong’o, Felwiin Saar ak ñeñeen. Daan naa dawal téere yooyu, nu koy waxtaane, maak ñoom. Mu daan nekk i laaj ak tontu yu am solo. Livespeaker laa fa nekkoon.
DFW : Léegi, lan njeexital la liggéey boobu am ci yow, soxna Faatu ?
FSK : Bi ma ci nekkee laa amoon xalaatu bind ab yaxal tuddee ko Hospitalité et résistance, di ci nettali la ma fa dund ci wàllu wecce xalaat, wax li ma fa naqari. Waaye tamit, ci wàllu xeetal ak yu ni mel…
DFW : Ndax dangaa mës a jànkoonteel, fa Ërob, mbirum xeetal, maanaam racisme ?
Képp kuy dund ci réewi tubaab yi, mës nga jànkoonteek xeetal. Ndaxte, ñoom su ñu gisee nit ku ñuul, li ñuy njëkk a yaakaar mooy ne danga wutsi loo am, ndax Afrig kembaaru ñàkk, xiif ak fitna la ñu ko jàppe. Yenn saay, booy aajar cib béréb, boo nee « am naa doktoraa », dañu lay xoolaat…Liggéey yu baax yi sax, dañuy jàpp ni yeyoowoo ko. Waaye, yaay dëggal sa bopp, am sa fulla, xam ni kenn du la may dara. Te it, wolof nee na, ni la wuude gisee rekk la lay ëwalee. Du melow der moo am solo, waaye li ci biir. Te yit, bañ di leen toppandoo.
DFW : Waxtaan wi neex na waaye nu bañ a fàtte ni dangay jàngale wolof ca réewum Almaañ. Naka la la dikkee ?
FSK : Ca jamonoy mbasum koronaa ma, kenn daawul génn jëm fenn. Danga daan toog rekk. Bu ko defee, dangay xalaat. Noonu, ma ne waaw, man lu tax duma jàngale wolof ?! Ba pare, benn bés, yemook 8eelu màrs, ma bokkoon ci aw waxtaan, doon ci leeral jaloorey jigéeni Ndeer ña, benn tubaab laajoon ma ndax damay jàngale wolof. Lii daal moo ma ci dugal. wayee tamit, man, ma-làmmiñal laa…
Ci kaw loolu, ma biral ab yëgle ci sama xëtu Facebook. Ca ndorteel la, 8i ndongo kepp laa amoon. Ñu ngi bawoo fu nekk nag. Ndax, njàngale mi, ci lënd gi la woon, gaawu bu nekk. Boobaak tey, maa ngi wéy di ko def. ginnaaw gi, dama ci lëkkaloo ak jànguneb Dusserdolf. Ma bég lool ci di jàngal ay nit làmmiñ wi ma nàmp, di ko gën a xam, man itam. Ndeem ñeneen ñoo bëgg a xam sama làkku bopp, kon dafay war ci man, ci sama jëmmu bopp, ma gën cee def i jéego.
DFW : Soxna Faatu, ndax dafa am ñu la xiir ci bëgg ak fonk làmmiñu wolof ba tey jii nga koy jàngale ?
FSK : Waa-waaw. Boo ñëwee gis ay nit ñu tegu ci yoon, mu wóor la ni yoon woowooy wu baax wi, doo def lu dul topp ci. Ma lim ci ñenn ñu deme ni Ajaa Aram Faal Jóob, Bubakar Bóris Jóob, Pàppa Séex Aliyu Ndaw, ñoom porof Momar Siise, Ceerno Siise ak Mamadu Siise. Ñoom dañu ma gën a xamal dayo bi sama làkk làmboo. Nit ki amul lu dul li mu moom ak fi mu bokk. Waru koo jënde leneen. Te sax, ku wacc sa and, and boo dem fekk ca boroom. Te Ërob tamit lii la soxla, moo tax ñoom ñu ngi leen iy woo fu nekk ñuy yëkkatiy kàddu, ñu leen iy déglu.
DFW : Am na ñu naan làkki réew mi, ci réew mi la yem. Yow miy jàngale wolof fa Almaañ, lu ciy sa xalaat ?
FSK : Kiy wax loolu, gis-gisam moo gàtt. Boo génnee dinga gis ni làkki réew mi am nañu dayo bu réy. Bu nu yaras. Jàngune bi ma nekk, am na bés bob, danoo amoon ag kaajar, ma def sama gos ci wolof, wax ko ci wolof ba noppi sotti ko ci tubaab, keneen door koo wax ci almaŋ, mu neexoon lool mbooloo ma fa teewoon. Bésu Afrig la woon. Ba nu ca jógee, am naa 2i naataangoo yoy, kenn ki awsa la, ki ci des suwaayili. Waaye, dañu ni woon danu koy defaat. Amoon na dayo bu mag, wax-dëgg-Yàlla.
DFW : Li nga moom, boo ko xeebee, ñu xeebal la ko… Bu loolu weesoo, làkk ak mbatiit ñoo ànd. Ndax, dingay faral di am i laaj ñeel mbatiitu wolof ?
FSK : Lu bari sax ! Waa-waaw ! Li may jàngale day feeñ ci sama coliin. Maa ngi dund ak ay tubaab. Waaye, du yàgg ba ma nirook ñoom, te soxlawuma sax nirook ñoom. Bu ma leen doon toppandoo, duñu ma teg fenn. Ndokk nag, ba ma bëggee mbatiit mi ma Yàlla boole. Saa-Afrig laa, doomu Senegaal laa, sagu ci bu baax nag.
DFW : Xanaa looloo tax nga fonk sa ñuulaay bii la Yàlla binde ?
Man de xeesaluma te fasuma ko yéene. Ndax, xeesal, xeeb sa bopp la ci man. Ŋàññuma nag ñiy xeesal, sama yoon nekku ci. Duma teg tamit seen kawar yooyu, ñoruma.
DFW : Nu ngi ci weeru màrs [weer woowu lees amaloon waxtaan wi], muy weeru jigéen ñi. Ndax ci sa liggéey mës nga jànkoonteek i jafe-jafe ndax rekk li ngay jigéen ?
FSK : Mën naa ni déedéet ndax damaa mës a nekk bañkat…
DFW : Mën nga baaxe ñiy dawal Lu Defu Waxu benn maye bu koy firnde ?
FSK : Ba may séy ak sama jëkkër, maa nga woon jàngune bu Ndakaaru, di jàng. Sama baay, Alxuaraan la jàng, daara la jaar. Sama yaay moom, yar njaboot gi moo doon liggéeyam. Waaye, dañoo sonnoon ci sunu njàng. Bi ma waa ji bëggee takk, lenn rekk la ma sama baay laaj, mooy : nooy def ak sa njàng mi ? Ma ni ko, dama koy wéyal. Sama jëkkër tamit ànd ceek man, jox ma kàddoom. Ma ni ko damay bañ nu dem ba ci biir, nga rocci sa kàddu, ndax am na góor ñu koy def, gis naa ko. Mu waxaat ma ni dina ma jàppale ba sama njàng du yàqu. Ma ni ko bés boo ma ko naree yàqal, ma bàyyi la, génn ci séy bi, bu fekkee sax ni am naa ci doom, damay tas. Mu ni ma nangu na. Mu jàppale ma nag bu baax a baax ci fànn yépp. Demoon na ba jàkkaarlook waa këram ndax dañoo bëggoon ma séysi, mu ni leen du ci dal ndax kàddu ga mu ma joxoon. Am na góor ñoo xam ni dañuy dig jigéen, waññeeku, génn ci. Man nag duma ko nangu.
Yow jigéen yaa war a xam li nga bëgg, xam ni liñ naan « sexe faible » amul. Loolu, kàddu gees di yeewee as gor la…
DFW : Noo gisee xew-xew yi ñuy faral di amal ci bésu jigéen ñi ?
FSK : Su dee fee ca Almaañ de, dinga gis ne tuuti lañ ciy wax, du tee kenn liggéeyi walla toppatoo ay soxlaam. Fii nag, xumbeel yi lañuy gën a jëmu. Ba pare tamit, daanaka jigéen ñi jàng ekool rekk lañuy fësal. Ñi jàngul nag, ak ñi liggéeyul, toog ca kër ya di jàppale njaboot yi. Ndax duñu ay jigéen ? Jar na seetaat.
Ñi ci naaj wi ñoo tax ñenn ñi mën a ne ca ker ga…
DFW : Jamono jii, wan naal wu taxaw nga am ?
FSK : Bég naa lool ci laaj bi. Maa ngi lëkkaloo ak sama naataango Maamur Daraame, nuy bind ab téere njàngum wolof ci tubaab ak almaŋ.
Ngir tamit ñu gën a xam sunu mbatiit, maa ngi ci nataali Sëriñ Tuubaa yi nit ñi di jënd. Xam nga ci wàllu yeesal, Murid yi dañoo jënd nataali Sëriñ bi, walbati waxtaan wi, waaye ñoom dañoo am doole, mën nañoo jënd, bañ a xaar Nguur gi. Bañ ni Sëriñ Tuubaa bañoon te bal tàkkul, jaasi jógul, damaa gis ne loolooy wéy tey ci Murid yi. Ci lii daal laa bëgg a bind téere.
DFW : Xam naa téere bu mel ni Géntug saa-Afrig bu Alfa Yuusufa Géy (EJO-Editions) dina la amal njariñ ci fànn wii ndax nettali na ci ay jaar-jaari Sëriñ Tuubaa yu am solo.
Na ma ko waxe woon ba nuy door, Lu Defu Waxu am na mbégte ci dalal la. Looy tàggatoo ?
FSK : Maa ngi leen di gërëm, yow ak ñi nga àndal ci liggéey bi. Amoon mbégte mu réy ci jataayu laaj ak tont bu am solo su réy ci man. Maa ngi ndokkeel sunu baay Bubakar Bóris Jóob te di ko ñaanal jàmm ju sax dàkk moom mi sos EJO ak Lu Defu Waxu. Jërëjëf.