SÉYDINAA MUHAMMADU MAXTAAR LAAY, XALIFA LAAYEEN YI, DËDDU NA.

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xalifa Laayeen yi, Séydinaa Muhammadu Maxtaar Laay, génn na àddina guddig talaata (8eelu awril 2025) jëm àllarba, ci Ndakaaru. Mi ngi amoon 73i at. Yoof ay këram gu mujj.

Séydinaa Muhammadu Maxtaar Laay moo nekkoon 6eelu Xalifa Laayeen yi. Sëriñ Abdulaay Caw Laay la wuutu woon ci xilaafa bi, ca atum 2021.

Moom Séydinaa Muhammadu Maxtaar, doom la woon ci Séydinaa Manjoon Laay (2eelu Xalifa Laayeen, génn àddina ca atum 1971).

Liise Belees Jaañ la Séydinaa Muhammadu Maxtaar amee woon bakaloreyaa. Senegaal la doore njàngam laata mu koy mottalijee Farãs ak Marog. Bi mu ñibbisee Senegaal ak i lijaasay “Ingénieur informaticien”, daan na liggéeyee Sonatel. Ku amoon xam-xam la ak ràññatle. Amoon na yit mébét yu kawe ñeel këru diine gi mu bokk. Waaye, jàmm ak tawféex la yéene woon itam Senegaal, Afrig ak àddina sépp.

Ci lees ko seedeel nag, ku oyof la woon te laabir, sàmpu bu baax ci reeni mbatiitam. Waayeet, terewu ko woon a ubbeeku yit ci àddina. Dafa di, Séydinaa Muhammadu Maxtaar Laay dëddu na ak i nësër yu takku.

EJO-EDITIONS ak Lu Defu Waxu ñoo ngi koy jaal njabootug Laayeen, di ko jaal tamit Umma bépp ak àddina si. Yal na suufu Yoof oyof ci kawam !

Ki yoroon kàddoom, di Séydinaa Muhammadu Lamin Laay (di doom ci Xalifa Séydinaa Isaa Laay), moo nekk tey 7eelu Xalifa Laayeen yi. Na ko Borom bi taxawu !

Ndey Koddu FAAL

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj