KOPPARI COVID-19 YI : JÀPPAGUM NAÑU ÑU BARI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yoon tàmbali na saytu mbirum koppar yees jagleeloon mbasu Covid-19 ma. Ci altiney démb ji rekk, jot nañu jàpp lim bu takku ciy nit ñoñ, tuddees na leen ci. Waaye, des na ñeneen ñu ñuy diir, rawatina ay jëwriñ ça Nguurug Maki Sàll ak i DAGE.

Toppekatu Ndakaaru bi dafa sant DIC, wax ko mu jàppal ko ay nit ñoñ, njortees na ni dañu def naka su dul noonu ñeel koppari Covid-19 ya. Moo tax, démb, ñu jàpp ñu bari, muy ñii toftalu :

Mamadu Ngom (DAGE ba woon ca njëwriñu wér-gi-yaram gi)

Muhammadu Seen (DAGE ba woon ca njëwriñu ndaw ñi) ak rakkam ju góor jii di Mamadu Seen ((njiitul Kawsara business service)

Alimatu Sadiya Géy (njiitul Fédération des couturiers et créateurs associés du Sénégal)

Jibril Kan (njiitul Ecopres Suarl)

Faatu Fati (njiitul Setraf)

Sàmba Faal (njiitul Qprost)

Baaba Hamdi Jaawara (artist, waykat)

Abdul Asiis Mbay (géwél)

Kii di Alimatu Saadiya Géy mees tudd ci kaw, nee ñu, mbirum 50i miliyoŋ lañu koy toppe. Bu dee Abdul Asiis Mbay, géwél bi nekk TFM, 150i miliyoŋ yees joxoo géwél yi lañu koy toppe ndax amuñu ay firnde ci fu xaalis bi jaar. Bu dee Baaba Hamdi Jaawara nag, dafa am 81,178i miliyoŋ yu naaxsaay lañu koy toppe. Bees sukkandikoo ci yéenekaay Libération, ñeneen dinañu ci topp.

Ginnaaw ñi ñu jàpp démb, DIC mi ngi ci tànki ay jëwriñ. Kon, Ëttu àttekaay bu kawe dina sóobu ci liggéey bi. Ndax, moom mooy ëttu àttekaay bi am màqaama ak sañ-sañu àtte ay jëwriñ ak njiiti réew. Wëliis jëwriñ yooyee nag, am na DAGE yu bari yu ñu nar a jàpp :

Uséynu Ngom (DAGE njëwriñu wér-gi-yaramam)

Baabakar Seen (njiitul loppitaanu Kafrin)

Mamadu Njaay (njiitul Prévention)

Musaa Saam Daaf (njiitul loppitaanu Dalal Jàmm)

Lamin Jàllo (kontaabalu loppitaanu Yuusu Mbargaan)

Aliyun Badara Jóob (kontaabalu loppitaanu Pikin).

Ñoom ñii, ëllëg ci àllarba ji, 15 awril 2025, lañuy wuyuji DIC.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj