Kuppeg àddina si : Senegaal, xalam demoon na bay neex buum ga dog

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw ñaar-fukki at bim gëjee romb pàcc bu njëkk bu kuppeg àddina si, Senegaal doon na joŋante ñaareelu wicceem dë finaalam ci dibéer jii (04 desàmbar 2022) bi 19i waxtu jotee. Waaye dafa mujje nërmeelu nërmeelu bu metti (3-0) ci kanamu Àngalteer mim doon dajeel.

Cii ndoorte li, Saa-Senegaal yi jotoon nañ am taxawaay bu baax. Jot nañ sax sonal àngale yi ba Bulaay Ja am fa benn dóor bu Pikfoor, góolu Àngalteer bi, génneek loxoom. Waaye dafa mel ni fa la Saa-Senegaal yi noppee ci joŋante bi. Ndax li des ci joŋante bi yépp àngale yi dañ taxaw seen xef yi, mayuñ leen dara. Naka noonu, ñu tàmbalee teg bal bi ci suuf, di ko dawal. Te fuñ ñàkkee bal bi, dalaat ci kow Saa-Senegaal yi ba jotaat ci.

Mbir yi takkarnaase ci ndawi Aliw Siise yi lool. Ñu tàmbali di ñàkk bal yi. Yàggul dara, Enderson dugal ci 39eelu simili bi. Àngalteer daldi koy jàpp foofu. Ñu dawalaat tuuti, Ãri Kéen dugal ñaareelu bii bu Àngalteer ci 48eelu simili bi. Muy 2i bii ci tus ci xaaj bu njëkk bi.

Naka lañ delsi ci ñaareelu xaaj bi, Aliw Siise daldi dugalandoo ñetti kuppekat ngir yokk doole ekibam. Waaye jariñul dara. Ndax taxawaayu Saa-Àngalteer yi soppeekuwul benn yoon. dafa sax gënatee dëgër. Lu Saa-Senegaal yi jéem ñu neenal ko, tegaat leen lu gën a metti. Biñ àggee ci 57eelu simili bi, Àngalteer teccali leen ak ub biiwu Sakaa. Muy ñetti bii ci tus.

Ba bi joŋante bi di jeex, Kalidu Kulibali ak i farandoowam defaatuñ fa lenn lu jaaxal Saa-Àngalteer yi. Ñii mayuñu leen ko sax. Dañ am ñetti bii ba noppi andi yeneen kuppekat, mel ni ku gën a xabtalu. Bi Àngalteer amee bii nag, kuppekati Senegaal yi  dañ mel ni ñu tiit. Ci saa si ñu mel ni ñu mënatul téyee bal bi. Ñàkk bal yu yomb yi di tegloo. Ñuy gis i gaañe ci lu ko jarul ba di jël i kàrtoŋ.Ci noonu, Senegaal daldi génn ci joŋanteem bu gën a bon ci xëccoo bi. Monjaalam yem ci wiceem dë finaal. 

Xalam demon bay neex, buum ga dog. Muy niru ni lii la waa Ekib gisoon ba tàmbalee wax ci Farãs/Àngalteer ba Saa-Senegaal yi naan dañ leen xeeb. Ak lum ci mën a doon. Kuppe moo wax dëgg tey. Àngalteer dafa mën Senegaal, làpp ko ñetti bii ci tus.

Nañ defaruwaat. Bu yoon jeexul, waaxusil du jeex.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj