Toftaleg IDH gu 2022 génn na ci alxames ji. PNUD a ko génne. PNUD (Programme des Nations Unies pour le Développement), nag, ag kurél la gog, dafay saytu yokkuteg réew yi ci àddina si. At mu nekk, day génne ag saabal, natt dundiin yi ci réew yi. Atum ren jii, ponk bii toftalu lañu jiitaloon ci seen saabal gi : Jamono ju wóoradi, dund yu jafe : defara sunu ëllëg cis àddina suy soppiku
Senegaal, lekk gi doyul. Nit ñi regguñu. Naanuñu ba màndi. Weruñu. Dañuy gaaw a dee. Jànguñu, taruñu, xamuñu. Ndóol lañuy fanaanoo, di xëye tumurànke, yendoo rafle. Maanaam daal, ci gàttal, Senegaal, dunduñu. Bu doon garab, dees na wax rag na. Lii lees jukke ci saabal gu mujj gi kurélug PNUD génne ci alxames jile.
Bees sukkandikoo ci saabalug kurél giy yëngu ak a saytu wàlluw yokkute, 21i réew kese la Senegaal tane ci àddina si. Nde, ci biir 191i réew, Senegaal a nekk ci 170eelu palaas bi. Maanaam, bi ñu nattee dundin gi ci 191i réew, gisees na ni, dund ci biir 169i réew moo gën a wóor, gën a yomb te gën a neex dund biir Senegaal. Loolu, nag, nattees na ko ci lekk gu doy, nit ñi di ko gis, jot ko te am luñ ko jënde. Wér-gi-yaram tamit bokk ci màndarga yi kurél giy jëfandikoo. Rax-ci-dolli, dañuy xool tamit yàggaayu nit ñi, ñaata at lañuy dund gën-gaa bari. Xam-xam tamit, maanaam njàng mi ci la bokk. Liggéey (xëy), xaalis bu doy, kaaraange, yoon, AÑS.tamit bokk nañ ci lees di nattee dundiinu nit ñi ba xam yemb na am déet.
Ci gis-gisu PNUD, ñaari at yii weesu dañu booley gàllankoor yu bare, te menn réew daanaka muccu ci. Nde, ñoom, dañu jàpp ne mbasum Covid-19 ak xareb Ikren dañu jeexital bu baax a baax ci koom-koomu àddina si. Nee ñu àddina si dafa dellu ginnaaw, dem ba méngoo ak atum 2016.
« 32i at ba léegi, PNUD a ngi saytu màndargay yokkute ci àddina si, di ko natte wàllu wér-gi-yaram, njàng ak dayob dund gi cim réew. Waaye, guléet màndarga boobiley wàññeeku ak a dellu ginnaaw ci diirub ñaari at yu toftalu. Yokkuteg nit gi dafa rës ba tolloo ak gu 2016 ga, daldi nasaxalaale jéego yu réy yees defoon ñeel njëmmalug nisëriy yokkute gu sax. »
Mëneesul a weddi sabab ak firnde yi saabal gi biral. Nde, lu ne fàŋŋ kenn du ko jeex. Kenn du werante ne, mbasum Covid-19 bi yàq na lu bari ci àddina si, sabab ay jafe-jafe yu dul jeex ci fànn yu wuute. Xareb Ikren tamit, noonu. Wànte, ndax loolu doy nab lay ci réewi Afrig yi, rawatina Senegaal ? Laata ñaari jéyya yooyu di ganesi àddina si, ndax dund gi baaxoon na fi ? Ndax, démb, xiif ak mar jóge woon nañu fi ? Ndax nit ñaa ngi daan faju ba wér ? Ndax njàng mi jaaroon na yoon ? Ndax liggéey amoon na fi ? Ku nekk yaay tontul sa bopp. Li am ba dees moo di ne, Senegaal moom, jarul woon ñuy xaar ag kurél di leen wax fu ñu tollu.
A waaw, tungune dina teew ñuy nataal ? Réew moo xam ne ñàkkul dara ci wàllu balluy mbindaare ak i balluwaayi alal, am suuf su nangu, geéj gu yaa, jàww ju tabe… réew mu am soroj, gaas, wurus, sirkõ, fosfat, añs. Nu ni déet-a-waay, nga am ay ndaw yu tollu ci seen digg-doole, nangoo liggéey. Waaw, réew mu ni mel, dund gi jafe fi lool. Ndox amul, mbëj gi doyul. Njàng mi doxul, xëy amul. Kenn wérul, kenn fajul. Liir yiy lakk ba ñor ci raglu yi, jigéeni biir yi ak wësin-wees yiy dee bés bu nekk bu ñuy matu. Mbënn mi ame réew mi, ndaw yiy song mbëkk mi. Saay-saay siy rey askan wi niy ginaar, di siif jigéen ñi, di sàcc as-tuut li baadoolo yi am. Yoon ferenkulaay, di doxe Kumba am ndey, Kumba amul ndey. Mooy li waa ji wax rekk, xas na ba ñaaw, day ñaaw rekk. PNUD dañ nuy tàppaas rekk, waaye Senegaal moom, xasaw na démb, balaa tey. Te, luy dund di xasaw, boo deewee du mat a wax.