LAAJ-TONTU AK SOXNA FAATU SIISE KAN (1/2)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LU DEFU WAXU, seen yéenekaay ci kàllamay Kocc, mi ngi am mbégte dalal fii tey, Soxna Faatu Siise Kan, jàngalekatu wolof ca Almaañ. Soxna si Kan, doomu Senegaal la, juddoo fi, yaroo fi, màggee fi, dooree fi am njàngam ba am DEA, ca 2012. Ginnaaw gi, at ma ca topp, mu tukki Almaañ. Foofa la féete, di fa jàngale jonni-Yàlla tey jile. Jamono jii mu ñëw Senegaal ngir bër, nu daldi koy koj, séq ak moom waxtaan wii nu leen di dégtalsi…

Ndey Koddu Faal (NdKF) : Soxna si, nu bàyyi la nga nuyook ñi taamu xibaaroo ci Lu Defu Waxu.

Faatu Siise Kan (FSK) : Soxna Ndey Koddu, maa ngi lay nuyu, di la gërëm. Di nuyu tamit ñépp ñiy dawal Lu Defu Waxu. Bég lool ci dalal bi, di leen gërëm.

NdKF : Faatu Siise Kan, nuy fàttali ni ma-làmmiñal nga, dooree sam njàng fii ci Senegaal, mottalee ko ca Almaañ, te foofa it ngay liggéeyee. Ndax mën nga delsi tuuti ci say jaar-jaar ?

FSK: Senegaal laa jànge ba am lisãs, « maîtrise », ak « DEA » ci njàppandalug Porofesëer Momar Siise. Ci làkku oniyan, maanaam basari, laa def i gëstu. Jàngat naa nu ñuy tëggee waat yi, nu muy doxee, ak tamit anami làkk wi ci lu nëbbu, maanaam langue secrète. Moo ma may ma dem Almaañ def fa sama « thèse ».

NdKF : Faatu Siise Kan, yow, du wolof nga ?

FSK : Waaw, wolof laa. Moom laa nàmp. Sama ñaari way-jur yépp tamit, ay wolof lañu. Sama yaay bawol-bawol la, sama baay di njàmbur-njàmbur.

NdKF : Nu gis ni làkku oniyan, muy basari, ci nga def i gëstu, bind ci sa « thèse ». Lu la tax a taamu làkkuw oniyan wi ?

FSK : Porof Momar Siise moo ma ci ñaax, digal ma ko. Ndax, wolof, ñi ci liggéey bari nañu. Sëñ Siise dimbali na ma bu baax.

Waaye tamit Senegaal benn bopp la, kenn mënu ko xar ñaar. Te, day baax nu xam yeneen làkk yees fiy wax, dugganteek ñoom, gën leen a xam ak a jege. Danoo war a xam yeneen làkki réew mi ndax, ñaare, coono li nuy daj ngir mën a làkk farãse, àngale mbaa almaŋ, dunu ko ci daj. Dina wàññi yit lu deme ni boddikoonte ciy xeet. Lu ni mel a tax ma taamu woon làkku oniyan ngir liggéey ci.

NdKF : Bi ngay liggéey ci oniyan, ndax amoo ci woon ay jafe-jafe ginnaaw làkk la wow, ñi koy wax bariwuñu lool ?

FSK : Ahãkay ! Bi may tàmbali, jafe woon na lool ci man. Li ko sabab mooy gis ñu koy wax yombul woon. Dafa di, toog naa daanaka atum lëmm, door a gis ku koy wax. Dama mujje dem fa Direction de l’alphabétisation, ñu boole ma ak jenn waay ju nekk weti raglub (loppitaal) Faan. Ndekete yoo, moom du woon aliyaan, balant la. Waaye, daf ma yabal Wakaam, ma xamante fa ak kenn, mu boole ma ak ñu xaw a bari sax. Ma demlanteek ñoom, ba tey, am ñoo xam ni danoo wéy di demlante.

NdKF : Bu loolu weesoo, diggante 2017 jàpp 2019, gis nanu ni bokkoon nga ci naal wu aju fànnu wërteef ak tukki fa réewum Espaañ. Lu defu waxu bëggoon nga dellusi ci tuuti…

FSK : Waaw, wax nga dëgg, Ndey Koddu… Ab porof bu nekk ca Almaañ moo sooke woon naal wi. Ca Almaañ la nu ko waroon a defe. Waaye, ginnaaw Espaañ dafa bari ay doomi Senegaal, ñu mujj ko faa defe. Fu doomi Senegaal nekk, dinañu soxla ku dégg wolof, mën a lappatoo. Loolu moo ma ci dugaloon.

NdKF : Lu nekkoon sa liggéey walla sa taxawaay ca naal woowa ?

FSK : Dem nanu Espaañ 3i yoon. Daan nanu waxtaan ak a seetlu saa-Senegaal yi, di xool ni ñuy doxalee ak wëraakon yi. Nu gis ni, ñu ci ëpp dugguñu ekool. Waaye, dinañu fexe ba wax seen soxla ci làkk yi wëraakon yi di làkk, ba jaay seen njaay tamit. Dañu dégg làkk yu bari.

NdKF : Ndax mën nanoo xam ci ban anam nga bokke woon ca naal wa ?

FSK : Porof bi ko sumboon ak ekibam, maa leen doon jàppale ci wolof. Rax-ci-dolli, ñoom itam, ñu war cee gëstu niki man. Yenn saay nu tas, yenn saay nu booloo. Daan naa giseek saa-Senegaal yi, ñu wóolu ma, di ma déey seen i soxla, ubbil ma seen dënn. Ma leen di laaj, ñuy tontu. Bi naal wi sottee tamit, danu ko tëral ci ab téere, ku nekk ci nun am ci ab yaxal. Muy lu am solo. Man, sama ci seen dundu biir laa bind, maanaam li ñuy dund ci lu nëbbu.

NdKF : Ndax li leen taxoon a jóg moo doon rekk def i gëstu ci jafe-jafe yi saa-Senegaal yiy dund, def ci téere, walla boog ndax saa-Senegaal yooyu jëlee nañu ci njariñ ?

FSK : Waaw, amoon nañu ci njariñ. Ndax, foofu ca Espaañ, woo woon nanu leen ñu bokk ak nun liggéey (atelier), joxe seen xalaat, seede. Joxoon nanu leen neexal. Waaye, ku amul këyit, xam nga mënoo ko xaatimal ag pas (contrat).

NdKF : Ndax foofu la yem ?

FSK : Déedéet. Sunu porof bi bëggoon na lijjantil kenn ci ñoom ay këyitam ba tàmbali woon ko. Bëggoon na ko jëlal layalkat sax. Ndax, su ko defee, ñiy tukki, yoon yi bañ a jafe lool ci ñoom.

NdKF : Mujjoon na àntu ?

FSK : Mujjul àntu nag. Ndax dëkkunu Espaañ, yombul woon…

NdKF : Liggéey nga tamit ci naal wees tuddee Resist ? Nu mu demee woon ?

FSK : Koloñ la amee woon ci genn kàddug mboor (Musée) bees dippee Rautenstrauch Joest.  Ay gaaral yu nu daan def la ñeel mbiri nootaange ak xeetal. Nu ciy wone ay nataal yoy, du méngoo saa su ne ak li saa-Afrig yi nekk dëggantaan. Liggéey naa foofu lu jege at.

Dees na ko topp…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj