LAAYEEN YI MERE NAÑU MAKI SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ku dégg kàdduy Imaam Basiiru Caw Laay xam ne Laayeen yi mer nañ lool. Te, dara waralu ko lu dul lakkirimosen yi takk-der yi sànni ci xabru Seydinaa Isaa Laay ba ca Kàmberen. Nde, fanny ii yépp, ci xeex bu metti la goney Ndakaaru yi sékk ak way-wattu kaaraange yi. Ginnaaw Ngor, Kàmberen a jël. Waaye, xeexu Kàmberen bi dafa tàmbalee jéggi dayo. Lakkirimosen yi takk-der yiy sànni ñoo tàbbi ca xabrub Séydinaa Isaa Laay, di sëriñ, di kilifa gu mag a mag ci tarixa laayeen. Moo tax Imaam Basiiru Caw Laay mer, jël kàddu gi, wax ne :

« Mësuma xalaat ne nit dina suufental sunu xabrub sëriñ. Li xew Kàmberen mësut a am. Tey jii, way-wattu kaaraange yi dugg nañu biir dëkk bi di def naka su dul noonu, di jàmmaarlook xaley Kàmberen yi. […] Te sax, ñoo ko tey di sànniy lakkirimosen ci xabrub Seydinaa Isaa Laay. »

Imaam baa ngi fàttali ne, lu ni mel, amoon na ci weeru koor gi. Ndaw ñaa dajaloo woon ginnaaw jullig naafila, di sikkar ak a ñanal réew mi, « …ñu gaase leen ».Mu ne, li njiit yi war a xam mooy ne, jëf yu ni mel ñooy taal um réew. Moom, Imaam Basiiru Caw Laay, mi ngi artook a mooytuloo Nguur gi ci kàddu yii :

« Pólisee yi mënoon nañu sànni gërënaad yi ci sunuy kër, donte ne du yoon, mën nañ koo muñ. Waaye, li ñu dul nangu mooy ñu leen di sànni ci xabru bi. Ñi ñuy wut nag, dinañ nu jot. »

Dafa mel ni nag, yoonu jàmm soriwul. Nde,  bees sukkandikoo ci kàdduy Imaam bi, ñoo ngi waxtaan. Moo ko tax a sant ndaw ñépp ñu dakkal yëngu-yëngal yi. Ànd ak loolu lépp, Imaam baa ngiy dankaafu Nguur gi ba tey. Ndaxte, mu ngi naan dootuñu nangu la fa xew di fa amaat. Ca la yóbbantee Njiitu réew miy kàddu, wax ko na wax ak magum jëwriñam, Aamadu Ba, mu jox ndigal takk-der yi ci ne bu ñu mësati sànniy gërënaad lakkirimosen ci xabru bi. Ndax kat, « bu loolu amatee, ndax njiit yooyu dinañ fi sàkkootiy ñaan ? Ndaxte, saa buñ jàqee ba jaaxle, dañuy yelwaansiy ñaan. »

Noo ko déggandoo. Ku gor garab gi lay may ker, bu naaj tàngee tàngal sa yaram ak sa xol.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj