“LAMI DEMOKARAASI” : PASTEF FENTATI NA LU BEES

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waa Pastef fëllati nañu fu bees. Wii yoon, ay lami këwsu lañu defar, tudde leen « lami demokaraasi », di leen jaay. Lami këwsu yooyii nag, meloy Pastef lañ ci def, nëtëx ak xonq, bind ci “Ousmane Sonko 2024”. Li ñu ko dugge mooy ñaawal Nguur gi xam ne, ci Yoon lay jaare, di jàppaate ak a takkalaate ay lami elektoronig.

Dafa di, Senegaal dafa génne feem bu bees. Ndax, fan yii, dañu nemmeeku xeetu xarala bu bees ci ñees di bàyyeendi fileek Yoon di leen àtte. Nde, jamono yii, ak jàpp yu bari yi, dañuy bàyyeendi ñenn ñi. Waaye, deesu leen bàyyee noonu. Dañ lee di takkal ay lami elektoronig ngir saytu leen, tënk seen dem ak seen dikk. Lam yooyu, ngir wàññi limu nit ñi ci kaso yee tax Yoon di leen jëfandikoo léegi. Jot nañ cee takkal ñu bari, rawatina ñu ci mel ni Waali Juuf Bojaŋ ak El Maalig Njaay. Dafa di sax, fan yii, ndaw ñi daan nañ ko fowe, di ko ñàkkal faayda ci mbaali jokkoo yi, ku nekk di takk lu la neex ci sa tànk ngir ñaawalee ko Nguur gi.

Pastef nag, yemuñu rekk ci ñaawal Nguur gi ak Yoon wi ñu jàpp ne, dafa jeng. Ñoom Usmaan Sonko, Biram Suley Jóob, Basiiru Jomay Fay ak waa Pastef yépp, dañuy jéem a won Njiitu réew mi ak i ñoñam ne, li ñu leen di xeexe lañuy, ñoom waa Pastef, soppi ngànnaay, di ci wone seen doole ak di ci góobe koppar gu takku. Ndaxte, « lami demokaraasi » yooyu, nee ñu defar nañu ci benn tamndaret (milyoŋ), bu ci nekk di jar 1. 000 FCFA (ñàttéeméeri dërëm). Kon, bu lépp jaree, te sikk amul ci ne dina jeex, Pastef dina ci fore benn tamñaret, maanaam 1 milyaar ci sunuy koppar. Xaalis boobu nag, dinañ ko dugal ci seen biir nafa ngir mën a waajal seen mbër, Usmaan Sonko, ñeel wotey 2024 yi.

Ndekete kat, xel, xalaat lay jariñ.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj