LÀMMIÑ WEES NÀMP

Yeneen i xët

Aji bind ji

21eelu féwaryee lañ jagleel ci àddina sépp bésu làmmiñ wi nga nàmp. Xalaat bu ni mel a ngi tukkee ca « Bangladesh ». Mbootaayu Xeet yi ngir njàng, xarala ak mbatiit (UNESCO) nangu dogal bi ci ndaje mu yaatu ñeel kurél gi ci atum 1999. Atum 2000 ak tey, àddina see ngi koy wéyal ba fépp bés bu ni mel ñu di ko màggal. Saa yu egsee, UNESCO da koy jëmmal tey woo ñépp ci farataal wuuteg làkk ak mbatiit yiy xadd naataange gu sax.

« Menn réew mënta suqaliku ci làkku jaambur »…

Lu aju ci làmmiñi réew mi, Senegaal mi ngi ciy def ay jéego yu am solo. Naam, doxiin wi yéex na, waaye garab guy sax, kenn du ko dégg, àndul ak coow. Te, jamono jii mel na ni kenn umpaleetul njariñu jàngee ci sa làmmiñ ; dina tax njàngaan li gaaw a xam, gaaw a mokkal : muy wàññi bu baax lim biy faral a lajj ci njàng mi. Ba tax na Càmmug Senegaal jël dogalu doore njàngum tuut-tànk yi ci seen làmmiñu bopp… 

Te wax dëgg-Yàlla, soo seetloo tuuti rekk, dinga gis ni tàmbali njàng ci làkku jaambur jaaduwul. Ndax day mel ni li weneen làkk mën, sa làmmiñ mënu ko. Foofu la xeeb sa bopp tàmbalee, te ñi ëpp foofu lañu lajjee. Soo jëloon gone tubaab bëgg koo dugal ekoolu wolof, du gaw a xam, kon nun ñii ay jaambaar dëgg lanu. 

Daa xameesul sax lu waral nit di jël làkku doxandéem di ci nas ak a nocci, di ci def lépp li ko soxal ba noppi ni fi ñukk li mu moom. Luy ndeyu làmmiñ wi nga nàmp, xam ko, xamee ci àddina, dégg ko, nga war koo bàyyi di jànge weneen ? Njeexitali jàng ci sa làmmiñ day tax nga gaaw a mën ndax liñ lay laaj ci làmmiñ woowu lay jaare… 

«  Làmmiñ ngànnaay la, balay ñaw nga daas ko…

Làmmiñ wu ñu jariñoowul, mi ngi mel ni paaka bu xomaag » (Seex Anta Jóob).

Liy tax a jëm kanam, indi naataange warta jaare ci làkku jaambur. Làmmiñ ngànnaay la, fàww nga koy jëfandikoo ci fànn yépp ngir mu jur njariñ. Làmmiñ ak mbatiit ñoo ànd . Ciw làmmiñ lees di jaar ngir dundal mbatiit, xamal ko ndaw ñi , ñooñu mën koo wattu, di ko joqalante. Kon gis ngeen ni làmmiñ wu  fey musiba la ci mbatiitu ña ko séq. 

Téere yaa ngi génn bu baax ci làmmiñi réew mi : OSAD def na liggéey bu am solo. Soxna Aram Faal mi ko sos, yaatu dënn lool mook ekibam, ñu xam ni tool la bob, ku nekk mën na cee bey waaram. OSAD a móol li ëpp ci téerey làmmiñi Senegaal. PAPYRUS tamit def na liggéey bu am solo. EJO moo mujje ñëw ci këri-móolukaay yi ci làmmiñi réew mi, di génne téere ci xeet yépp, sosaale yéenekaay ci kàllamay Kocc ngeen ciy jànge kayit gii ngeen tiim muy LU DEFU WAXU (www.defuwaxu.com) jiitu ci làngu yéenekaay yi ci lënd gi. Am na it kippàngo gu kenn umpalewul ci toolu wolof muy Wolof ak xamle (WAX) di jàngale wolof amaale yéenekaay Saabal.com, seen « lépp di wolof ». FONK SUNUY LÀMMIÑ dig kurél guy yëngu ci njàngalem wolof, jubal mbind mi ci mbedd yeek tele yi, di lootaabe tamit ay ndajey ladab ci làmmiñi réew mi ak a sargal ñi jiitu ci yoon wi te def ci lu am solo.

Waxuma sax ni ñuy jëfandikoo wolof ci mbaali-jokkoo yi waaye daanaka « émissions » rajook tele, lépp ci wolof lay ame. Kon solo si umpatul kenn. Càmm gi nag moo yor dogal moo war a xaatim wolof nekkandoo « langue officielle »  ci wetu làkku tubaab. Du caagénu daa ëpp dayoo yeneen làkk yi waaye dadi làmmiñu jokko woo xam nii, daanaka ñépp a ko dégg ci Senegaal. Su ko defee yéenekaay yeek téere yi yokku, film yeek kurél yeek tàggat ci mécce yi gën a yaatu.

Tool a ngi bu laajul lu dul yaras féete ginnaaw, fonk sa bopp di gindi. Lu mën a nekk la ndax lépp lu weneen làkk mën, làmmiñi réew mi mën nañ lu ko raw.

« Làmmiñ gàttul »…

Yenn saay nit dagge ca làng ga ni la waaye làmmiñi réew mi kenn mënu cee def lii walla lee. Njuumte lu mag a ngi. Seex Anta Jóob tekki na xarala ak simi ci wolof, ba noppi tekki ci wolof ay mbindi xarala yu kowe. Lii bokk na ci li xiir ñu mel ni ñoom Paate Jaañ, Seex Aliyu Ndaw, Saxiir Caam, Bubakar Bóris Jóob, Seex Adaraame Jaxate, Àllaaji Momar Sàmb, Mamadu Jara Juuf, Meysa Njaay Béey, Abdu Xaadr Kebe, Imaam Amaat Caam, Lamin Mbaay, Usmaan Lóo Waajal, Paap Aali Jàllo, ak ñeneen ñuy bind ak a tekki ci wolof. Jigéen ñi desuñu ginnaaw. Maam Yunus Jeŋ moo jiitu, ñoom Kura Saar, Abi Ture, Ndey Daba Ñaan,Soxna Baawo Jóob, Ami Mbeng ak ñoom seen. Ndaw ñi ñoom kenn demul ñu des : Làmp Faal Kala, Ibraayma Saaxo Caam, Felwiin Saar, Meysa Maara ak ñu baree bari. Ci kow loolu CÉYTU tekki na Une saison au Congo tudde ko Nawetu deret ak it L’africain tudde ko Baay sama, doomu-Afrig. Tey jii ladab ci wolof gànjaru na lool. Sã Léwopóol Juuf it bind na dictionnaire ci wolof, ñu bari di ko liggéeye. CESTI, daara jiy tàggat taskati xibaar ca Iniwérsite ñu ngi fay jàngale wolof. 

Xeeti firnde yii taxoon Seex Anta ni : « lu am xel dem ci àddina, aw làmmiñ mën na koo tudd ; xel ay gàtt, làmmiñ gàtt. Nit kiy wax nag, fi xelam yem, fi njàngam yem, fi gis-gisug àddinaam yem foofu rekk la ay waxam mën a yem ». Ca Kees la ko waxe woon ci atum 1984.

Fonk sa bopp, fonk sa yëf… 

Te li Séex Anta Jóob waxoon rekk : « làmmiñu jaambur mën koo macc mu neex lool ni tàngal waaye doo ci tàqamtiku ». Ànd nanu ci jàng ak mën làkk yu bari (ubbeeku la ci doom-Aadama) waaye ndeem “bépp làkk rafet na, buy yee ci nit xel ma, di tudd ci jaam ngor la”, ni koy Séex Musaa Ka daa waxe, kon nanu def i jéego ci làkk yépp, jëkke ci wi nu moom, door a jàll ci weneen ndax “bey ci sa wewu tànk”.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj