LAYOOKATI SONKO YI DUGAL NAÑ AB NEENAL-ÀTTE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi ëttu àttewaay bu mag bi neenalee woon àtteb Sabasi Fay ba, keroog àjjuma17 nowàmbar 2023, layookati Sonko yi, ba léegi, xàddeeguñ. Nde, lépp luñ gis, mbaa lu leen Yoon may ñoo ngi koy def ngir Usmaan Sonko duggaat ci wayndarew wotey 2024 yi. Looloo tax ñu dugal, démb ci talaata ji 28 nowàmbar ca ëttu àttewaay bu mag ba, ab dogu ngir neenal àtte ba mu defoon ca bésub 17 nowàmbar bii nu weesu.

Bi ñuy joxe ay leeral ci lu tax ñu dugal neenal-àtte bi, kii di Sayid Larifu di kenn ci layookati Sonko yi wax na ne :

« Danu dellusiwaat fii ngir ëttu àttewaay bu mag bi xoolaat dogal ba mu jëloon ci ayu-bés bii nu génn, ndax dogal bi dafa bariy rëq-rëq ak ay lënt-lënt ci wàllu Yoon… Lenn rekk la nu soxla, mooy ëttu àttewaay bu mag bi bañ a salfaañe àqi Usmaan Sonko, loolu rekk moo nu soxal, te dunu nangu wenn yoon ku ko salfaañe. Ginnaaw ba mbir mi, mbirum bokk ci wotey 2024 yi la, warees na sàmm àq ak yelleefi saa-senegaal bi ngir mu bokk ci wote yi. Kon ëttu àttewaay bu mag bi nag, li ko war mooy mu jóg àddu ci mbir mi ca ba muy gaaw. »

Keneen ci layookati Sonko yi di Baabakar Njaay àddu na ci moom itam, wax  ne :

« Ëttu àttewaay bu mag bi dafa war a gaaw ci mbir mi. Ndax gaawtu ga ñu gaawtu woon ca ba ñuy neenal àtteb Sabasi Fay ba, noonu rekk lañ war a def ci bii tamit, su fekkee ne doxal Yoon rekk moo leen tax a jóg. Bu ngeen amee seetlu, gis ngeen ne kenn ci àttekat ya bokkoon ca àtteb 17 nowàmbar ba, dafa bañ a torlu dogal bañ jëloon, te loolu am na lu muy tekki ci Yoon…

Saa-senegaal yépp war nañ xam ne neenal-àtte bii nu dugal tey ngir ñàkk a nangu dogalu ëttu àttewaay bu mag bi, mooy tax nu xam ndax Usmaan Sonko dina bokk am déet ci wotey 2024 yi. Loolu tamit ci loxoy ëttu àttewaay bu mag bi la nekk, moo tax nag mu war cee gaaw lu ko moy, wutukaayub Usmaan Sonko bee nar a naaxsaay, te wax dëgg, dafa war a bokk ni ñeneen ñi bokkee. »

Lii la layookati Sonko yi wax ngir leeral neenal-àtte bi ñu dugal ci ëttu àttewaay bu mag bi. Nuy xaarandi lan la ci ëttu àtteway bu mag bi di tontu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj