Sàcc, siif, daw… déedéet ! Loolu xewwi na. Léegi, li am mooy : sàcc, siif, rey, daw. Ndege, jamonoy tey jii, dañu lay siif, jël sag ndaw, jël sa ngor, sàggi sa sutura teg ci… jël sa bakkan… Waaw ! jël sa alal ba noppi jam la paaka, walla ñu xoj la, walla sax ñu dóor la ba nga dee. Da di, sax, ku ñu rey ci anam yile, mënees na wax ne dañu la doggali rekk. Ndaxte, ku ñu siif ku ne, reyees na la ba noppi. Bu ci faat bakkan dollikoo, day xaw a niru jëfu maa-tey. Daanaka, mëneesul a toog benn ayu-bés te déggeesul ku ñu siif ba faf rey ko. Mbir mi, nag, mi ngi bëgg a ëpp i loxo te mel na ni kaaraange amatul ci miim réew. Waaye, wolof nee na, mbejum kanam, boroom a koy fajal boppam. Xéy-na loolu la askan wi dégg ba di àtteel boppam.
Askan wi fippu na nag. Léegi, daanaka, kenn àqeetul pólis walla sàndarmëri. Gaa ñi dañuy fajal seen bopp. Loolu la saa-senegaal yi di def léegi. Fan yii nu génn, jàppoon nañ ab sàcc ca Mbaaw, dóor ko ba muy bëgg a dee. Ñu ne déet-a-waay, àllàrba jee weesu, yemook 24 ut, ca Liberte 5 lañ jàppaat benn siifkat. Ngóor saa ngi tuddoon Njaga Njaay, amoon 34i at. Nee ñu, dafa am kum fa doon siif. Biñ ko jàppee, takk ko ci poto-làmp dóor ko ba mu dee. Ñu yaakaar ne fa lay yem, xaritu Njaga yi, ay siifkat ni moo ci waxi taskati-xibaar yi, jóge Xaar-Yàlla, ñëw biir Libeerte 5 ngir fayusil ko. Noonu, ñu daldi rajaxe koñ bi yépp, yàq ay wata jàmbur, toj i palanteer ak i xeer.
Waa Forum du justiciable génne woon nañ ab yëgle di naqarlu lu ni mel te di ñaawlu toroxal bi ñuy toroxal ñi ñuy jiiñ càcc ak siif. Ci seen biir yégle bi, ñoo ngi ciy wax ne :
«Ci réewum yoon lanu nekk. Moo tax kenn warul am màqaama, ñu tooñ la, ngay fajal sa bopp. Coow yu mel nii dafay faral di am réero, ngir moytu yooyu nag, fàww askan wi di bàyyi pólis ak sàndarmëri def seen liggéey bañ di fajal seen bopp. Ngir dundu ci réew mi nga xam ne Càmmug yoon la, dafay laaj ñu tënku ci yoon ak lépp liy saxal sunu kaaraange. »
Mu am nag ñu samp ay laaj ñeel kurél googiy wax ne, sàmm àq ak yelleefi doom-aadama a ko tax a jóg. Laaj bi mooy : ki ñu sàcc moom, ana àqam ? Ki ñu siif, moom, ana àqam ? Ki ñu rey, moom, xanaa bakaan jarul dara ? Ki ñu boole sàcc, siif te rey ko, moom nag… ? Lii moo waral ñenn ñiy wax naan dafa jot, ku rey, ñu rey la. Ndaxte, dañu jàpp ne, kaso doyul ci ay siifkat walla reykatu nit. Kon dafa jot ñu xoolaat tëralinu yoon wi, dëppale ko ak mbaaxi réew mi te bañ a jéggaaniy àtte yi safaanoo ak mbatiitu réew mi ?
Li naqari askan wi ba tax ñuy jóg di fajal seen bopp, bokk na ci siif nit ki, rey ko ba noppi daw, rëcc, te du mujj fenn. Mbaa ñu jàpp la, tëj la ci kaso bi, di la jox ngay lekk, di la jox ngay naan. Maanaam, di la dundale ak alalu réew mi nga xam ne, ki nga rey am na ci wàll. Bu ko defee, nga toog fa ñaar, ñetti walla sax fukki at, daldi génn. Boo génnee, delloo buum ca mboy-mboy ga, di sàcc, di siifaate ak reye. Léeg-léeg sax nga gën a yées. Lii nag neexul ci xol te it yombul a muñ. Dangay seet rekk, ku nekk njaboot, ñu bari bootu ci ginnaawam, mu liggéey ba sonn jot peyooram ñu siif ko, nangu alalam ba noppi faat ko. Bu ko defee, njaboot gi tumurànke. Ana pexe ?
Naam, feyantoo baaxul. Te, am réew, yoon a ko war a lal. Waaye, bu yoon woowii nasaxee ba askan wi sës, dañuy joxoñ baraamu tuuma takk-der yi. Ndakete, ci gis-gisu saa-senegaal yi, takk-der yi leen waroon a aar ñooy wëlbatiku di jàmmaarlo ak ñoom ci ay mbiri pólitig. Kon, tey, su neexoon Càmm gi, kaaraange dellusiwaat ci biir réew mi. Dem na ba kenn wóolootul kenn. Jot na ñu jéem xam sabab yi waral càcc gi, siifaate bi ak reyaate bi.
Ndax ñàkkum xéy mi la ak dundu gu metti gi ? Ndax takk-der yi ñoo ngi def seen liggéey ni mu ware ? Ndax seen lim ak seen i jumtukaay yi doy nañu ? Lan mooy saafara yi ? Boroom xel yi ak xalaat yu rafet yi, laaj yaa ngi noonu.