Démb ci dibéer ji la lëkkatoo gii di “ Diomaye Président” doon amal ndajem waxtaan ñeel tolluwaayu réew mi ak li ñu namm a def. Ndax, jamono jii kenn umpalewul ne réew mi jaxasoo na lool. Te, dara waralu ko lu dul li Njiitu réew mi Maki Sàll dàq wote yi waroon a am diggante fii ak ñaari ayu-bés. Moo tax, ñu ne ñoom duñu toog di xoole. Dañuy wéyal xeex bi ñu sumboon bu yàgg ba tey seen diggante ak Njiitu réew mi. Ba tax na, sumbaat nañu beneen xeex boo xam ne door nañu ko démb ci guddi. Te, fasuñu ko yéenee yemale fii.
Ndàqug wotey palum Njiitu réew mee wéy di am ay njeexital ca na mu gën a mettee. Kenn waxaalewul ñi ñuy toroxal, ñi ñuy teg loxo walla ñi ñu gaañ ci jàmmaarloo yi. Ndeysaan, ñetti bakkan rotagum nañu ci. Mu nekk mbir mu doy waar moo xam ne du guléet ci nguurug Maki Sàll donte ne sax, yu ni mel daan nañu leen fi nemmeeku lu ko jiitu. Waaye, wii yoon moom, dafa tegaloo. Ndax, màrs 2021, suwe 2023 ak weeru féewiryee wii ñu nekk doy nañu ci misaal.
Moo tax waa lëkkatoog Jomaay gi ne duñu bàyyi mu sedd. Ndax, seen i militaŋ, ñii ñu ngi leen di jàpp, ña ca des ñu leen di bóom. Ki fi nekkoon toppekatu bokkeef gi, Àlliyun Ndaw, xamle na ne mbir mi du yombe noonu. Dees na topp takk-der yi fa Yoon ginnaaw bu fi Maki Sàll jógee. Ndax, nee na:
“Amul benn Saa-Senegaal bu fàttaliku lim bu tollu nii ci ay doomi-aadama yu ñu bóom ak ñu ñu teg loxo ci lu moy Nguuru Maki Sàll.”
Mu mel ni kon, anam yi ñuy bóomee ak yi ñuy tegee loxo Saa-Senegaal yi ñaaw na ba fu ñaaw yem. Ba tax na, jamono jii, ndaw ñu bari ci béréb yu fasantikoo fippu ne duñu bàyyi. Looloo waral sax, tey ci altine ji, béréb yu bari ci réew mi dooraat jàmmaarloo yi. Nde, ñoom dañoo jàpp ne ki war a doxal Yoon, moo koy jalgati. Looloo tax kii di Aminata Ture di fàttali Maki Sàll ne :
“Yow Maki Sàll, jigéen ñaa ngi sàkku nga bàyyi seen doom yi ngay rey ! Ndaw yooyu ñu bóom, seen yaay yi dañu leen ëmb juróom-ñeenti weer ci seen biir ni sa soxna ëmbee sa ñetti doom yooyu juróom-ñeenti weer. Bàyyil sunu doom yi ngay bóom !”
Dafa di, moom dafa jàpp ne guuta gi réew mi dugg tey ba ay bakkan di ci rot kenn waralu ko ku dul moom Njiitu réew mi. Ndax, ndogal li mu jël ci ag teeyu bakkanam kese la ko teg. Moo tax, kii di Guy Mariis Saaña di xamle ne :
“Fii ak Ndajem ndeyu àtte mi àdduwul ci dabantal gi dépitey Yewwi Askan Wi jébbal, sàrt bi ñeel ndàqug wote yi du mën a jàll. Kon, kàmpaañ bi day wéy.”
Waaye, moom yemul foofu. Ndax, nee na jamono jii dañoo fatt witt àttekati ëtt boobu, mayuñu leen jàmm. Moo tax, ñoom ñuy artu. Ndax, fi mu tollu nii tembe, kaaraange àttekat yooyu ñor na leen lool.
“Nu ngi sàkkku ci Nguur gi mu aar àttekati Ndajem Ndeyu àtte mi. Lépp lu leen mën a dal du keneen ku dul moom Maki Sàll.”
Li ñu tëje seen waxtaan wi mooy anam yi ñu namm a wéyalee seen xeex bi. Maanaam, lan lañu nas te, fas ko yéene doxal diggante démb, tey ak suba. Bi ci jiitu, mooy biraale (veillée) gi ñu waroon a biraale démb fa Mermoos wetu kër Maki Sàll. Bi ci topp, di bi ñuy amal tey ci altine ji. Muy séddale ay “flyers” ak def am njëgg (caravane) fépp ci biir-réew mi. Bi ci mujj, di bi ñuy amal suba ci talaata ji. Nee ñu dañuy def ndajem ñaxtu ci ag pattaaral.
Ci gàttal, lëkkatoog Jomaay gi nii la fas yéenee doxale xeex bi. Li mat a laaj kay mooy ak mbooleem li ñu sumb muy ci wàllu Yoon ak ci mbedd mi, ndax dina tax Njiitu réew mi dellu ginnaaw ci ndogal li mu jël ? Rax-ci-dolli, jàmmaarloo yii nga xam ne door nañu keroog ba tey ba ay bakkan rot ci, kañ lañuy dakk ?