Ñépp a doon xaar PDS ngir xam naka lay taxawee ci wotey 2024 yii. Nde, ginnaaw biñteree Kariim Wàdd bokk, lu nekk def nañ ko ngir wote yi bañ a am. Waaye, seen pexe àntuwul. Wii yoon di ñaareel wi ñuy wuute ay wotey njiiteefu réew ginnaaw yoy 2019. Booba nag, dañu màndu woon, faraluñu woon kenn. Ren jii nag, ñu bari ñoo ngi doon sàkku ndimbalu PDS ci wote yi, rawatina lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar bi, Aamadu Ba. Dafa di, Basiiru Jomaay Fay sax woo woon na Kariim Wàdd, waxtaan ak moom ci jollasu. Moom, doomu Abdulaay Wàdd ji, moo ko xamle tey ci suba. Sànk ci ngoon lañ génne ab yégle bu Abdulaay Wàdd xaatim, di ci xamle ne Basiiru Jomaay Fay lañu taamu, moom lañuy jàppale. Muy ndimbal lu réy lu dolleeku ci lëkkatoo “Diomaye Président”. Nee ñu, Abdulaay Wàdd, Usmaan Sonko ak Basiiru Jomaay Fay dinañ daje ngir waxtaan.
FAN WU MUJJ CI KÀMPAAÑ YI
Tey, ci guddig àjjuma jii di 22 màrs 2024, bu 23i waxtu toftalee 59i simili la kàmpaañ biy jeex. Lawax bu ci nekk tànn nab béréb ngir tëj kàmpaañami. Nde, gaawu gi, bésub dal-lu lay nekk, lawax yi war cee noppalu. Looloo tax sax, gaawu gi ñuy tere dem ak dikk bi diggante diiwaan ak diiwaan. Bu dibéeree ak jàmm, askan wi àtte lawax yi, tànnal boppam Njiit lu muy dénk lenge yi ci juróomi at yii di ñëw. NDAJEM NDEYU SÀRTI MI GÀNTAL NA CÀKKUTEEFI SÉEX TIIJAAN JÉEY AK ABIIB SI
Séex Tiijaan Jéey ak Abiib Si bokk nañ ci 19i lawax yi Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi daganaloon seen i wayndare. Ñoom ñaar ñépp nag, barki-démb ci àllarba ji, dañu génn gaaral nit ñi ne bàyyi nañ xëccoo bi te Basiiru Jomaay Fay lañuy jàppale. Bu ko defee, ñuy woo seen i militaŋ ak seen i soppe ñu woteel lawaxu Pastef bi. Noonu, ñu jubali ca màkkaanu Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi ngir jébbal àttekat yu mag yi sen bataaxalu bàyyi. Waaye, dañ leen a gàntal.
Dafa di, ñaari lawax yi, jotuñoo joxe sax seen i bataaxal. Nde, sàndarm yay wattu béréb bàyyiwuñ leen ñu dugg. Fim ne, seen i layookat ñoo féetewoo coow li. Bees sukkandikoo ci kàdduy ndaw ya fa lawax yi yabaloon, Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi daf leen jox dig-daje keroog 29 màrs 2024. Li àttekat yi lay mooy ne, muy Séex Tiijaan Jéey di Abiib Si, kenn ci ñoom ñaar bindu leen ca njëlbeen ngir yëgal leen ndogal loolii. Naka noonu, CNRA woo na leen ci ñu sàmmonte ak sàrti wote yi donte ne sax dañoo bëgg génn ci yëf yi.
MAMMADU YATASAAY GÉNN NA ÀDDUNA
Démb ci alxames ji la xibaar bu tiis boobu rot. Donte ne sax, jamonoo jii kenn umpalewul ne Senegaal ñi ngi waajtaay yu metti ngir dem ca wote ya. Terewul ne, moom it, am na lu muy màndargaal ci wote yi. Ndax, moom ndem-si-Yàlla Yatasaay, bokkoon na ci ñi mébétoon a lawaxu ngir bokk ci wote yi. Waaye, mujjul woon jàll. Dafa matalul woon xobi baayaleem. Démb, ci alxames ji la génn àdduna ginnaaw bi mu jagadi bu gaaw.
ANTA BAABAKAR NGOM NEE NA DINA TOPP JOMAAY FAY CI YOON
Anta Baabakar Ngom fas na yéene pelent Basiiru Jomaay Fay. Ñoom ñaar ñépp ay lawax lañ ci wotey 24 màrs 2024 yi. Waaye, jamono jii coow lu réy mu judduwaat seen diggante. Sabab bi mooy coowal suufi Ndengleer yi fi lëmbe woon réew mi, doxoon diggante Baabakar Ngom (baayu Anta) ak baykati Njagañaaw yi. Jamono jooja, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay a doon xeexal mbokkam yi, di leen waxal. Ndax, moom lawaxu Pastef bi, Njagañaaw la fekk baax. Li metti Anta Baabakar Ngom mooy li Basiiru Jomaay Fay fàttali coow loolu ci kàmpaañam. Soxna si jiite ARC dafa weddi li Basiiru Jomaay Fay wax, ne ay sosi neen la. Moo tax mu koy topp ci Yoon.