LI GËN A FËS CI WOTEY 2024 YI (18/3/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

CEDEAO DINA YÓNNEE 130i SAYTUKAT FI RÉEW MI

Ndiisoo CEDEAO gi dina yebal lu tollu ci 130i saytukat fi réew mi ngir wote yi fiy am keroog 24 màrs 2024. Muy xibaar bu ñu fésal cib yégle. Naka noonu, kurél gi xamle naat ni mi ngi topp bu baax tolluwaayu géewu pólitig bi. Rafetlu naat àtteb neenal bi ñu fi amal ba tax coow li wàññeeku bu baax a baax, ba ñuy rafet njort amal i wote ci jàmm. Muy woo pàcc yépp ci ñu ànd ak dal, jiital diisook sàkku jàmm.

NDAJE AAMADU BA AK XALIFA SÀLL FA WELINGARA

Démb ci dibéer ji, mbabooru Aamadu Ba ak Xalifa Sàll daje nañu fa goxu Welingara ci dagaan gi lawax yi di def jamono yii ñeel wotey 2024 yi. Waaye, ni ñu doxalee ci seen diggante ñépp ñoo ko rafetlu. Nde, li ñu daan faral di seetlu, saa su ay lawax dajewaan, mooy xeexoo ba ci rayante. Wile yoon mbir yi neneen la tëdde. Ñaari lawax yi dañ dox daje, joxante loxo, saafonte. Seen i àndandoo itam and ak dal, wet gu ci nekk jàllale say kàddu te kenn nemmeekuwu fa luy nirook tafaar.

SÉEX TIJAAN JÉEY DUGG NA CI BAYKAT YI

Wile yoon, baykat yi la Séex Tijaan Jéey seeti woon fa diwaanu Ndar. Jaar na ci baykati soble yi nekk Xelkom Jóob (Faas Ngom), romb Ndar, dem ba Roos Beeco. Li mu bëgg nag te gën koo fésal ciy kàddoom mooy ñu tëggaat anami mbay mi, fexe ba Senegaal mën a dundal boppam ci li muy bay te sàmmaale kéewnga gi. Moom lawax bi sax lëkkatoo DIOMAYE 2024 lay wéy di dagaanal baat, ni mu ko waxee woon ca ndoorte la. Muy sàkku nag ci ñépp ñu dem jëli seen i kàrt te woteel Jomaay keroog bésub 24 màrs 2024.

AALI NGUY NJAAY DIGE NA SÀMM GÉEJ GI BÉS BU FALOO

Ba tey ci wër gi lawax yi di wër ngir dagaan baati askan wi, Aali Nguy Njaay ma nga doon wéyal liggéeyam fa Mbuur démb ci dibéer ji. Nappkat yeek ñiy liggéeyee ci lépp lu laaleek napp gi la seeti woon ngir biral naalam ñeel wàll woowu. Ci kàddu yi mu fa jot a yékkati nag, fàttali na ni kenn umpalewul ni jën wi dafay gën di ñàkk ci géeju Senegaal. Te dara waralu ko lu dul déggoo yu bon yi Nguur gi xaatim ak gaali bitim-réew yi ba ñuy nappee nu leen neexee ci géej gi. Bés bu faloo, fas na yéene indi ciy saafara, xoolaat bu baax déggoo yi. Bañuñu si sax ba neenal leen, dakkal leen ngir aar géej gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj