Njiitu réew lu bees li, Basiiru Jomaay Fay, biral nay kàddu niki Njiitu réewum Senegaal. Ca otel Radison la doon waxee. Wax na ci ponk yu bari. Ci tënk, nee na dina boole ñépp uuf, jiite ci dal, woyofal ak njekk. Nee na yit, dina doxal njub te di jubal, juboole Senegaal gépp. Dige na ne, dina sóobu ci liggéey bi ngir naataange Senegaal ci fànn yépp, yokk taxawaayu réew mi biir Afrig ak ci àddina si, sàmm alalu askan wi ba li ñépp bokk, ñépp jot ci. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, rafetlu na taxawaayu Maki Sàll ci fan yu mujj yii. Rafetlu na tamit taxawaayu yeneen lawax yi ko ndokkeel ci ndamam li. Waaye nag, dafa beral loxo Usmaan Sonko, sargal ko, seedeel ko lu rafet. Dees na ci yaatal.
CENA : « WOTE YI JAAR NAÑ CI YOON »
CENA (Commission électorale nationale autonome) bi, di kurél giy saytu doxalinu wote yi, jàpp na ni wote yi am nañu ci anam yu jaar yoon, fi réew mi ak fa bitim-réew. Lu ko dalee 8i waxtu, bi pekk yi di ubbi ba bi ñuy tëj ciy 18i waxtu, nit ñi génn nañu dem woteji ci dal, ci jàmm ak ci fulla. Ba tax muy rafetlu taxawaay boobu maxejj yi am, te muy taxawaay bu mat a roy, buy wone ni réewum Senegaal tënkoo ci doxalinu demokaraasi. Delloo na njukkal itam tak-der yi nga xam ni fépp fu ñuy wotee gis nañ fa seen teewaay. Rafetlu naat taxawaayu kureli saytukati wote yi ba fépp fu doxul ñu wax ko bees mën ko joyyanti ca teel.
Loolu yépp terewul kurel gi dellu di fàttali lawax yeek képp ku dugal loxoom ci wote yi ni lu jëm ci siiwal njureef yi du seen cër te am na campeef yees ko jagleel.
LAWAX YI NDOKKALE NAÑ BASIIRU JOMAAY FAY
Daanaka lawax yépp ànd nañ nangu ni Basiiru Jomaay Fay moo jël ndam li. Démb ci dibéer ji, bi ñu yullee kàrt yi ba njureef yu njëkk yi génn, la yenn lawax yi tàmbalee woote ci jotaayu tele yeek rajo yi, ak a ndokkale Basiiru Jomaay Fay mi nekk ci kow. Bi ñu demee ba ci guddi gi sax, gis nañ ab yégle ci turu waa kër Aamadu Ba ñuy wax ni lu ëpp ci njureef yi génnaguñu. Kon ñiy tëb di dal te naan ñoo am ndam nañ teey te bañ a jalgati mbir yi, ndax du ñoom ñooy wax ki am ndam. Waaye li njureef yi di gën a yaatu, donte ni Aamadu Ba am na gox yu mu rawee Jomaay Fay sax, ceetlu gi benn la : Jomaay moo ëpp fuuf fu mu jël ndam li. Ginnaaw gi, Aamadu Ba ci boppam siiwal nab yégle buy wone ni nangu na ni Jomaay Fay a jël ndam li ci kay gu njëkk gi. Moo ngi koy ndokkale ak di xaaraale mujjantalu njureef yi.
60% CI TÀNNKAT YI ÑOO WOTE
Nees ko jotoon a seetlu, Saa-senegaal yu bare génnoon nañ woteji démb ci dibéer ji 24 màrs ngir fal seen Njiitum réew. Bees sukkandikoo ci lim yi kilifa yi siiwal, 7 033 852i (juróom-ñaari tamndaret ak fanweeri junneek ñett yu teg juróom-ñetti téeméer ak juróom-fukk ak ñaari) Saa-senegaal ñoo bindu woon. Lees jot a xayma nag, téeméer boo jël ci ñoom, juróom-benn-fukk yi (60%) dem nañ motali seen yéene ci wote yi.
MAKI SÀLL AK WAA BITIM RÉEW NDOKKALE NAÑ BASIIRU JOMAAY FAY
Ginnaaw bi lawax yépp àndee nangul Basiiru Jomaay Fay ndam li mu am démb ci wote yi, Njiitu réew mi Maki Sàll mi mu war a uutu nangu naat ni moom la bees sukkandikoo ci njureef yi jot a génn. Ba tax mu kay ndakkale ak di ndokkale Saa-senegaal yi ci taxawaay bi ñu am. Naka noonoot, waa bitim-réew tàmbali nañ yónnee seen i kàdduy Ndokkale Basiiru Jomaay Fay. Ñu njëkk cee nemmeeku Njiitu réewum Gine Bisaawoo, Umaru Siisoko Mbaalo. Muy Ndokkale maxejj yu Senegaal, di Ndokkale Basiiru mi ñu fal ak di ko ñaanal ndam ci fum bëgg yóbbu Senegaal ak ci waar wi mu namm bay ci bennoog Afrig.