Ibraahima Amidu Dem bëgg naa nekk lawax ci wotey 2024 yii di ñëw. Ci dibéer ji la ko siiwal. Moom, njiitul Etic (Ensemble pour le travail, l’intégrité et la citoyenneté) li, dogu na ci indiy saafara ñeel jafe-jafey réew mi. Muy xamle ni li leen tax a jóg, moom ak i ñoñam, mooy rëq-rëq yi ñu seetlu ci way-pólitig yi ak ni ñuy jëfandikoo yoon ci réew mi. Ba tax na mu am yéeneb indiy coppite yu bare. Mu nar a sukkandiku nag ci caabalu péncoo yi fi amoon (assises nationales).
MBËKK MI
Lu tollook ñaari téeméer ak juróom-ñeen-fukki doomi Senegaal ñoo tag fa réewum Marog. Ñoom nag dañoo bokk ci ñiy tukki di nëbbatu. Ñi ngi jóge woon ci réew mi juróom-benni fan jàpp fukki fan ak ñaar ci weeru ut wii nu nekk. Waaye, yoonu suuf wi lañu jëloon, jaari Móoritani, dugg Marog ngir jàll Espaañ. Jamono yii ñu leen téewee ca réewum Marog, ràññe nañ ci ñoom juróom-ñaar yoy dañu wopp ba ñu rawale leen. Naka noonu, Nguur gi fas na yéene delloosi leen ci àllarba ji.
ÑÀKKUM NDOX MEEK MÀGGAL GI
Ginnaaw jafe-jafey ndox yu metti yi ñuy faral di nemmeeku fa Tuuba, rawatina saa su Màggal gi teroo, Xalifa ba Sëriñ Muntaqaa sàkku woon na ci Nguur gi, ci jamono yee weesu, mu xëccal leen ci ndoxom Lac de guers mi. Bëgg-bëggam boobu nag mu ngi ci yoonu sotti. Aliw Jóob mi jiite Office des lacs et cours d’eaux, di pegg biy saytu dex yeek déeg yi, moo ko xamle. Bees sukkandikoo ci kàddu yi mu yékkati fa Tuubaa, liggéey bi dina tàmbali balaa at mi di jeex. Nawet bi rekk lañuy xaar mu jeex.
CÀCCUM JUR GI
Fa Balantakundaa (Séeju), càccum jur gi ñu fay faral di nemmeeku bare na lool. Looloo waral ba askan wa doon ñaxtu ak a woote wallu. Ginnaaw bi ñu génnee ca mbedd ya, ña ngay xamal Nguur gi ni sonn nañu lool. Nde, ñi leen di sàcc ña ngay faral di jóge ca réewum Gine Bisaawoo. Dañuy gànnaayu ba diis, jéggi dig bi, yóbbu seen jur yi te duñu ci mën dara. Ñuy sàkku ci Nguur gi mu jël ciy matukaay ngir aar leen. Lu ko moy ñoom ci seen bopp, dinañu sàkk i pexe, jàmmaarlook ñoom.
TÀGGAT-YARAM
Bërki-démb ci dibéer ji lañu doon joŋante Kubu Senegaal. Mu doonoon 63eel wi yoon. ASC Jaraaf daldi koy jël ci kow Estaad Mbuur ginnaaw bi mu ko dóoree ñaari bii ci benn. Bile yoon di tamit 16eel wi yoon ASC Jaraaf di jël kubu Senegaal.