Keroog ci àllarba ji la xibaar bi rotoon ne, dañu tëj sàqi koppar yu Walfadjri. Waa Walf ñoo ko siiwaloon, jaare ko ci ab yëgle bu ñu génnee. Li ñu ko dugge woon mooy xamal ña fay liggéeyee ne, duñu jot awãsu tabaski. Li ko waraloon, ci liñ amle woon, mooy ay galag yu ñu warlul Càmm gi diggante 2016 ak 2018. Waaye, pexe mujje na am.
Tey jii, ci àjjuma ji, caytug kërug Siidi Lamin Ñas gi génnewaat na beneen yëgle di ci xamle ne, ginnaaw bi ñu waxtaanee ak kilifay DGID yi, am lu ñu joxe, ubbil nañ leen seen i sàq. Nde, dafa am luñ dugal ci borub galag bi ñu ameel Càmm gi. Li ci des, ñu déggoo ak waa DGID ci anam bu ñu koy fayee. Muy xibaar bu neex ci liggéeykati Walfadjri yi. Ndax, ci biir yëgle boobu, xamal nañ leen ni, ku mu soob, nga jokk caytug kër ga ngir jot awãsu tabaski walla sag payooru weeru suwe ci boppam. Mu di xibaar bob, ñépp a ci bég.
NJIITU RÉEW MI JËLAAT NA YOON
Ginnaaw bi mu faloo ak léegi, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jot naa amal ay tukki yu bari, muy ci biir-réew mi di ca bitim-réew. Nde, mënees na wax ne réewi Afrig yu bari jot na fa dem. Waaye, terewul ba tey ay tukkeem ci réewi Afrig yi la koy amal. Ci alxamesu démb ji, xéy na dem fale ca Siyeraa Lewon seeti naataangoom bii di Julius Maada Biyoo.
SAA-SIIN YEEK KI LEEN DOON TEKKIL DEM NAÑU KASO
Mbir moomu mi ngi amoon keroog fa Daaru Xuddoos. Ñaari Saa-Siin ak ki leen doon tekkil lañu gis ci ab widewoo ñuy néewal doole jenn waay. Ba widewoo ba tasee nag, ca la leen sàndarmëri bu Mbooro tegee loxo. Nee ñu, peyooru dawalkat bi lañu bëggoon a foqati. Waaye, mujjee na metti ci ñoom. Ñoom ñett ñépp yóbbu nañu leen kaso. Dinañu leen àtte ñaar-fukki fan ak juróom-benn ci weeru sulet wii ñu nekk.
LIGGÉEYKATI “UDE” YAA NGI ÑAXTU
UDE (Urbaine D’Entreprise) ag këru liggéey la gog, kii di meeru Tiwaawon bi moo ko moom. Moom, Demba Jóob Si, jamono jii, digganteem ak ña fay liggéeyee neexul dara. Nde, ñoom fi mu tollu nii, mer nañu ba futt. Te, dara waralu ko lu moy ñeenti weeri peyoor yi mu leen yoreel te, ba tey, feyuleen ko. Rax-ci-dolli, tabaski gi yegsi na ba noppi.
WOTEY MURITANI
At ginnaaw bi ñu amalee seen wotey palug dépite ak yoy gox-goxaat yi, àgg nañu ci daj-dëpp gi. Nde, ci weer wii lañuy amal seen wotey palug. Wote yooyu, dees na leen amal ñaar-fukki fan ak juróom-ñeet ci weeru suwe wii ñu nekk. Lawax ya koy joŋante juróom-benn lañu ak Njiitu réew miy yóotu ñaareelu moome muy juróom-ñaar.