Ndajem jëwriñ yee ngi daan am àllarba ju nekk. Àpp boobu soppeeku na. Ndax, wii yoon, tey ci alxames ji lañu koy amal. Nee ñu, li sabab loolu mooy ne démb la woon benn fan ci weeru me ñu doon ci sargal liggéeykat yi. Te, démb dafa doon dalal sàndikaa yi ngie déglu leen, ñu jébbal ko seen i aajo, maanaam “cahiers des doléances des centrales syndicales”. Rax-ci-dolli, moom Njiitu réew mi dafa demoon fa Mbuur 4 (Cees) ñeel mbirum séddoo suuf ba ñu fay coow. Moo tax, tey ci alxames ji la ndajem jëwriñ yi amoon fa njénde la (pale ba).
NJIITU RÉEW MI JÀPPAAT NA YOON
Ginnaaw bi mu demee Tuubaa ak Tiwaawon, jullee àjjuma jii weesu fa jàkkay njabootu Séex Omar Fuutiyu Taal, siyaareji Monseigneur Bensame Njaay, Njiitu réew mi jàppaat na yoon. Nde, daf namm a nemmeekuji geneen këru diine. Wii yoon, ma nga jëm fa Medina Gunaas. Tukki boobu dina ko amal suba ci àjjuma ji ngir nemmeeku Xalif ba Ceerno Aamadu Tiijaan Ba.
ËTTU CETTANTAL BI DUUT NA BAARAAM JENEEN JËWRIÑ
Coowal njuuj-njaaj ya amoon ca yoriinu PRODAC jeexagul ba tey. Ëttu cettantal bi moo xolliwaat góom ba. Ndax, wii yoon, dafa am jeneen jëwriñ ju bokk ci Nguur gi fi jóge ju mu duut baaraam. Te, kooku du kenn ku dul Abdulaay Séydu Sow. Mu ànd ci luubal googu ak jenn waay juy wuyoo ci turu Ahmet Tiijaan Jeŋ ci béréb ba ñu leen tabboon muy PCO (Président du Conseil d’Orientation) bu PRODAC. Te, ëtt bi nee na, banqaas boobu gisuñu ko ci dekkere bi ëmb coste ak doxaliinu PRODAC bi. Loolu terewul ñu tabb leen ca béréb boobu. Rax-ci-dolli, ñu gis ne PRODAC biral na lu tollu ci fukki miliyoŋ yoo xam ne ñoom lañu jagleeloon.
MBËKK MI
Doomi Senegaal yaa ngi wéy ba tey di jël gaal yi ñgir dem Espaañ. Donte ne sax, lim bu takku ci ñoom ñàkk nañu ci seen i bakkan ci ndox mi. Loolu taxul ñu teggi seen tànk fa ñu ko tegoon. Nde, am na gaal gu bawoo woon Mbuur, yeboon lu tollu ci juróom-benn-fukki doomi-aadama, juróom-ñeent kepp ñoo ca muccagum. Kon, am na lu ëpp juróom-fukk ci ñoom ñoo xam ne dañoo réer ba nii, kenn xamul ci lan lañu nekk.
XEW-XEW BU TIIS FA JURBEL
Xew-xew boobu mi ngi am démb ci àllarba ji. Benn xale bu tollu ci ñaari at moo fa ñàkk bakkanam ci anam yu doy waar. Nde, xale boobu dafa daanu ci ab foos. Te, li ci gënatee metti mooy ne foos boobu xale bi ñàkke bakkanam, benn baayam bu ndaw moo ko gasoon.
BENEEN XEW-XEW BU DOY WAAR FA ÑANIŊ
Genn góor guy wuyoo ci turu P. Seen, tollu ci juróom-benn-fukki at lañu fa bóom. Jenn jigéen juy wuyoo ci turu Mari moo ko jam paaka mu faatu. Xew-xew boobu, démb ci suba la am. Ki ko fekke moo xamle ne dafa gis soxna si woo waa ji. Yàggul dara mu jam ko paaka ci doqu. Nee na mu gis dereet ji di wal. Mu njort ne day faatu. Ci la woowee waa Sàndarmëri bi ñuy agsi fekk na mu dee. Door nañu luññutu gi ngir xam lan moo war a sabab bóom googu.