Démb ci àllarba ji la Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay doon amal ñetteelu ndajem ak i jëwriñam. Mu jël fa ay ndogal yu am solo. Rax-ci-dolli, fàttali na ay jëwriñam li gën a yitteel askanu Senegaal jamono jii ñu tollu. Mu jiital ci loolu xeex dund gu jafe gi. Ci gàttal, ñoom jëwriñu yi, nañu seet ay pexe ngir wàññi njëgi mbooleem li askan wi di aajowoo ci lu mënut a ñàkk. Looloo tax mu sàkku ci elimaanu jëwriñ yi, jëwriñu yaxantu gi ak ndefar gi, kopparal yi, nafa gi ak mbey mi, ñu jébbal ko aw tëraliin wu tembere ngir xeex dund gu jafe gi laata fukki fan ak juróom ci weeru me wii ñu dëgmal. Waaye, wàññi gi ak yoonal gi du yem ci njëg yooyu kese. Yokk na ci ne nañu jàppandal dëkkuwaay yi, muy fi Ndakaaru ak ci yeneen béréb yi. Mu yokk ci ne, nañu def ay pexe ngir wutal liggéey ca na mu gën a gaawe ndaw yi am lijaasa ci njàngum araab meek farañse bi. Ba tey, yemul foofu. Ndax, sàkkuwaat na ci elimaanu jëwriñ yi mu taxawal ag ndiiso ngir dàmp mboolem ñi loru ci xew-xewi pólitig yi fi am diggante saŋwiye 2021 jàpp weeru féewaryee 2024. Bi mu jógee ci loolu, amal na ay tabb yu am solo.
TABB YU YEES YI
Ginnaaw bi mu biralee ay càkkuteef ci mboolem jëwriñam yi, ca la jëlee ndogalu takkal ay ndomboy-tànk ñenn ci doomi réew mi. Muy ñu bokk ca làng ga mu bokkoon, Pastef, ak ñeneen ñu ca bokkul. Saa-Senegaal yooyu ñu tabb démb, ñii la :
Baara JUUF tabb nañu ko “Délégue général à la promotion des Pôles Urbains de Diamniadio et du Lac Rose”. Mu wuutu fa Jéen Farba Saar ;
Baakari Sega BÀCCILI lañu tabb Njiitul “Agence pour la Promotion des Investissements et des Grands Travaux (APIX SA) ”. Ki mu wuutu ca béréb boobu di Abdulaay Balde ;
Paab Aale ÑAŊ lañu tabb Njiitul “Radiotélévision Sénégalaise (RTS) ”. Ki mu fa wuutu di Raasin Taala ;
Waali Juuf BOJAŊ lañu tabb Njiitul “Société nationale du Port Autonome de Dakar”. Mu wuutu ca kër googu Muntagaa Si ;
Séex Mammadu Abibulaay JÉEY tàbb nañu ko Njiitul “Aéroport International Blaise DIAGNE (AIBD SA) ”. Mu wuutu fa Abdulaay Jéey ;
Fadiilu KEYTA tabb nañu ko Njiitul “Caisse des Dépôts et Consignations”. Mu wuutu ca kër googu Séex Isaa Sàll ;
Màgget KAN lañu tabb Njiitul “Société nationale La Poste”. Ki mu wuutu foofa di Muhammadu Jet ;
Basiiru KEBE, tabb nañu ko Njiitul “Société nationale des Habitations à Loyer Modéré (SN HLM)”. Mu wuutu fa kër googu Mammadu Jaañ Si Mbeng ;
Muhammadu Moktaar MAGASUUBA, moom lañu tabb Njiitul “Société immobilière du Cap Vert (SICAP SA)”. Mu wuutu fa Mammadu Kase ;
Sëriñ Mammadu MBUUB, ñu tabb ko Njiitul “Société d’Aménagement et de Promotion des Côtes et Zones touristiques du Sénégal (SAPCO SA)”. Mu wuutu fa kër googu Suleymaan Njaay ;
Mari Roos FAY, lañu tabb Njiitul “Agence de Développement et d’Encadrement des petites et moyennes entreprises (ADEPME)”. Mi ngi fa wuutu Idiriisa Jaabiraa ;
Yaay Xadijatu Jamilaa JÀLLO, moom lañu tabb Njiitul “Agence nationale de la Petite enfance et de la Case des Tout-Petits”. Mi ngi wuutu fa kër googu soxna sii di Maymuuna Siisoxo ;
Tiijaan SIIDIBE, ñu ngi ko tabb Njiitul “Agence nationale de l’Aménagement du Territoire (ANAT)”. Mu wuutu fa Mammadu Jiigo ;
Séekunaa JAATA tabb nañu ko Njiitul “Agence sénégalaise de Reforestation et de la Grande Muraille Verte”. Mi ngi fa wuutu Umar Abdulaay Ba ;
Doktoor Séex JEŊ, moom lañu tabb Njiitul “Office national de l’Assainissement du Sénégal (ONAS)”. Moo wuutu fa béréb booba Mammadu Maamur Jàllo ;
Màggat JAXATE, tabb nañu ko “Directeur de la Législation et de la Coopération internationale”. Ki mu fa wuutu di Muhammadu Lamin Si ;
Abdu ÑiŊ lañu tabb “Directeur des Domaines”. Ki mu wuutu fa béréb boobu di Mammadu Géy.
WÀCCEE NAÑ SENERAAL MUSAA FAAL
Démb ci guddi la ndogal la daanu. Ñu xamle ne ki fi nekkoon kilifag sàndarmëri, Seneraal Musaa Faal, woo nañu ko ca beneen liggéey boo xam ne kenn leeralagu ko. Ki ko wuutu ci boppu sàndarmëri ba di Seneraalu Birigaad bii di Màrtin Fay, nekkoon fi it “Haut-Commandant en Second de la Gendarmerie nationale ak Sous-Directeur de la Justice Militaire”. Moom nag, Màrtin Fay, ki ko wuutu ca béréb ba mu nekkoon mooy Seneraalu Birigaad bii di Pàppa Juuf.
LIGGÉEYKATI EMEDIA YAA NGI ÑAXTU
Kurél gi ëmb liggéeykati Emedia yi mi ngi ñaawlu anam yu metti yi ñuy liggéeyee. Te, mbir mi yemul ci liggéey bi kese, leneen daf cee laxasu. Ndax, nee nañu mbir mi yemul ci anam yu metti yi ñuy liggéeyee. Nde, nemmeeku nañu fa ag ñàkk a leeral ci yorinu mbiri kër gi. Rax-ci-dolli tamit, peyoor gi day yéex lool. Moo tax, ñu jël ñetti matuwaay ngir xeex loolu. Bi ci jiitu mooy jébbal li ñuy dippe “préavis de grève” ci taabalu Njiiteef gu mag ga (direction générale). Ba ca topp, mooy takk ay sagar yu xonq li ko dale tey ci alxames ji. Bi ci mujj, mooy amal li ñuy dippe “grève virtuelle” li ko dale alxamesu tey jii. Loolu yépp lenn kesee ko waral mooy sàkku ñu teg leen ci anam yu mucc ayib ngir ñu mën a amal seen liggéey ca na mu gënee.
LAYOO SÉEX YÉRIM SEKK AK SÉYDINAA UMAR TURE
Ay yooni-yooni ginnaaw bi ñu ko dàqee, layoo bi mujje naa am démb. Nde, ki fi nekkoon kàppiteenu Ture moo doon toppu taskatu xibaar bii di Séex Yérim Sekk ca Yoon ngir ne dafa yàq deram ci téere ba mu génne woon jamono yale weesu. Toppekat bi nag, dafa sàkku ci àttekat bi mu daan taskatu xibaar bi. Waaye, taxul ba tey ñu xam fu mbir mi mujj. Nde, ndogal liy rote ci àtte boobu juróom-ñetti fan ci weeru me lañu koy xamle.