NJIITU RÉEW MI AMAL NA TUKKI FA MALI AK BURKINAA FAASO
Ginnaaw ba mu amalee ay tukkiy nemmeeku ak liggéey fa Gine, Gana, Muritani ak Koddiwaar, Njiitu réew maa wéyal tukki yi ci biir kembaaru Afrig gi. Tey, ci alxames ji, la Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay demoon fa Mali ak fa Burkinaa Faaso. Mali la njëkkee, bu fa jógee lay jàll Burkinaa Faaso.
NJUUJ-NJAAJ FA SONACOS
SONACOS (Société Nationale de la Commercialisation des Oléagineux du Sénégal) genn la ci këri liggéey yi ñu soppil Njiit lu yàggul dara. Ginnaaw ba fa Ndaan Jaañ wuutoo Kibili Ture, jot na faa amal ay caytu ñeel yorin wa. Waaye, la mu fa gis ci wàllum njuuj-njaaj dafa jéggi dayo. Ndax, ci lees wax, ka fa nekkoon da daan jël ay nit di leen fey juróom-benn-fukki junni jàpp juróom-ñeen-fukki junni ci jamono joo xam ne kër gaa doon jànkoonte ak ay jafe-jafe yu metti ci wàllu koppar. Te, moom Kibili, yemul foofu rekk. Ndax, am na benn géwal bu mu daan fey lu tollu ci benn miliyoŋ ak xaaj weer wu jot.
MANSUUR SEKK GÉNN NA ÀDDUNA
Xibaar boobu mi ngi rot ci suba. Génnug àdduna Mansuur sekk tiis la ci ñiy yëngu ci wàllu mbatiit, rawatina ci wàlluw woy. Ndax, foo ko tudde rekk teg ca Baaba Maal nga xam ne, kenn du ko naatable, muy ci biir réew mi, di ca bitim-réew. Nde, amal nañu liggéey bu yaatu ci wàll woowu. Tey jii lañu ko jébbal boroomam fa armeeli jullit ya nekk fa Yoof.
XIBAAR ÑEEL YOON
Coow li doxoon diggante Séex Baara Njaay ak Terees Fay mujj naa teerijee fa DIC (Division des Investigations Criminelles). Li waral loolu mooy ne dafa am kàddu yu Séex Baara Njaay yékkati woon teg leen ci ndoddu soxna soosu nekkon fi jëwriñ ca jamonoy Maki Sàll. Nde, moom Séex Baara Njaay dafa ne, soxna soosu, ci Nguuru Maki Sàll gi la duyee ay jibaam ba ñu fees. Maanaam, am-amam demewul woon noonu laata ñu koy tabb. Te, tey jii yor na koppar gu duun.
Naka noonu, Njiitul ciiwalug xibaari “La Tribune”, Paap Musaa Taraawore woo nañu ko fa “Section de Recherches”. Bees sukkandikoo ci xibaar yi rotagum, lenn waralul woote boobu lu moy li mu bind ci xëtu yéenekaayam bi. Nde, daf ne Seneraal Kànde yóbbu nañu ko fa “New Delhi”, fa End (Inde). Waaye, dafa bañ a jëfe ndigalu Usmaan Sonko loolee.
BÉSU SET-SETAL
Gaawu, 1eelu fan ci weeru suwe lañu jàpp bésu set-setal fi réew mi. Li ñu ko dugge nag mooy set-setal dëkk bépp ngir mën a waajal nawet bi. Maanaam, fépp fu ndox war a jaar te mu fatt, ñu dindi mbooleem la fa nekkoon ngir xàllal ndox mi yoon wu muy jaar. Looloo tax, Njiitu réew mi génn def ab widewoo di ci woo ñépp, bàyyiwul kenn. Ndax, nee na, moom sax dina bokk ca liggéey booba.
MBËKK MI
Ndawi Senegaal yi génneeguñu seen xel ci yoonu Espaañ wi. Saa bu ñu demee ba foog ne mbir mi wàññeeku na, fekk booba la Waalo gën a aay. Ak ñi ci ñàkk seen i bakkan ñépp ak ñi ñu jot a waññi, loolu lépp taxul ñu bàyyi. Ndax, biraag bu Funjuuñ waññi na biig ag gaal gu jëloon yoon. La ca nekkoon ci ay doomi-aadama tollu na ci téeméer ak juróom. Am na ay doomi Senegaal, Mali ak Gàmbi yépp. La ca gënatee doy waar sax mooy ay jigéen ña nga ca woon.
XEW-XEW BU TIIS FA MBÀMBILOOR
Mbir maa ngi xew ci altine jii weesu, fa daara ju digg-dóomu ja nekke fa Bàmbiloor. Benn ndongo moo fa jote woon ak moroomu ndongoom, dóor ko ag weñ ci bopp bi. Nee ñu, bi mu ko dóoree weñ gi, moroom mi dafa mujje nekk diggante dund ak dee, maanaam, dafa nekk ci komaa (coma). Ndeysaan, dafa mujje gaañu, wuyuji Boroomam ci alxamesu tey ji. Mu doon weneen tiis wu dal ci ñi nekk ci njàng meek njàngale mi ginnaaw jàngalekat ba ñu bóomoon fa Cees ayu-bés bii ñu génn.